Njiiti yoon yi fexeel nañu Yeesu
14
1 Booba nag sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya ñu ngi doon fexeel Yeesu, ngir jàpp ko, reylu. Fekk booba ñaari fan a des ci màggalu bésu Mucc ba ak màggalu Mburu ma amul lawiir. 2 Kon nag ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yëngu-yëngu baña am ci nit ñi.»
Jigéen diw na boppu Yeesu ak latkoloñ
3 Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani, mu dem këru Simoŋ ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jigéen ñëw, yor njaq lu ñu defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree bare. Jigéen ji toj njaq li, tuur latkoloñ ci boppu Yeesu.
4 Waaye amoon na fa ñu mer, di xultu ci seen biir naan: «Yàq gii, lu muy jariñ? 5 Maneesoon na jaay latkoloñ jii ci lu tollook peyug atum lëmm, jox ko miskin yi.» Noonu ñu daldi gëdd jigéen ji.
6 Waaye Yeesu ne leen: «Bàyyileen ko. Defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal? 7 Miskin yaa ngi ak yéen bés bu nekk, te man ngeen leena dimbali saa su leen neexee, waaye dungeen ma gis ba fàww. 8 Jigéen ji def na li mu man; diw na sama yaram ak latkoloñ, ngir waajal sama rob, laata moo jot. 9 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.»
Yudaa wor na Yeesu
10 Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya, ngir wori Yeesu. 11 Bi ñu ko déggee, ñu am ca bànneex bu réy, dig ko xaalis. Noonu mu fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu.
Reer bu mujj bi
12 Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, taalibey Yeesu laaj ko: «Foo bëgg, nu defaral la reeru bési Mucc bi?» Bés bu jëkk booba nag mooy bés, ba ñu farala rendi gàttub bésu Mucc ba. 13 Noonu Yeesu yebal ñaar ci taalibe yi ne leen: «Demleen ca dëkk ba, foofa góor gu yenu njaq lu def ndox, dina taseek yéen, ngeen topp ko. 14 Kër gi mu dugg nag, ngeen ne boroom kër gi: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc bi, man ak samay taalibe?” 15 Dina leen won néeg bu féete kaw te yaa, ñu defar ko, ba lépp jekk. Foofa ngeen nuy defarale reer bi.» 16 Bi mu ko waxee, taalibe ya dem ca dëkk ba, gis lépp, ni leen ko Yeesu waxe woon. Noonu ñu defar reer bi.
17 Bi nga xamee ne timis jot na, Yeesu ñëw, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. 18 Ñu toog, di lekk. Bi ñuy lekk nag, Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen, ku bokk ak man di lekk sax, dina ma wor.» 19 Taalibe yi nag am naqar, ñu daldi ko ne kenn-kenn: «Mbaa du man?» 20 Mu ne leen: «Kenn ci yéen fukk ak ñaar la, kuy cappandoo ak man ci ndab li. 21 Doomu nit ki mu ngi dem, ni ñu ko waxe ci Mbind mi, waaye ki koy wor dina torox. Bañoona juddu moo gën ci moom.»
22 Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, jox leen ko naan: «Jël-leen, lii sama yaram la.» 23 Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko, ñépp naan ci. 24 Mu ne leen: «Lii mooy sama deret, ji fas kóllëre gi, te tuurul ñu bare. 25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dootuma naan gannaaw tey ndoxum reseñ mii, ba kera ma ciy naan bu bees ci nguuru Yàlla.»
26 Noonu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya.
Yeesu wax na ne, Piyeer dina ko weddi
27 Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku, ndaxte bind nañu:
“Dinaa dóor sàmm bi,
xari jur gi tasaaroo.”
28 Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.»
29 Kon Piyeer ne ko: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la bàyyi mukk.» 30 Waaye Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, guddig tey, bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» 31 Waaye Piyeer gëna sax ca la mu waxoon naan: «Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu.
Yeesu ñaan na ca toolu Setsemane ci biir tiis wu réy
32 Noonu ñu dem ca bérab bu tudd Setsemane. Yeesu ne taalibe yi: «Toogleen fii, ma dem ñaani.» 33 Mu ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi jàq, ba xonet. 34 Mu ne leen: «Sama xol dafa tiis, ba ma bëgga dee; toogleen fii, xool.»
35 Noonu Yeesu dem ci kanam tuuti, daanu ci suuf, di ñaan ne, waxtu wi teggi ko, bu loolu manoona am. 36 Mu ne: «Abba, Baay, yaw mi dara tëwul, teggil ma kaasu naqar bii. Moona bumu doon sama coobare, waaye na sa coobare am.»
37 Noonu mu délsi ci taalibe yi, fekk ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? 38 Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» 39 Beneen yoon Yeesu dem, di ñaane noonu, 40 délsiwaat, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. Xamuñu lu ñu koy tontoo.
41 Ñetteelu yoon mu délsi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. 42 Jógleen nu dem; ki may wor a ngi nii, di ñëw.»
Jàpp nañu Yeesu
43 Bi Yeesu di wax, Yudaa mi bokkoon ci fukki taalibe ya ak ñaar, agsi, ànd ak mbooloo mu bare, mu jóge ca sarxalkat yu mag ya, ca xutbakat ya ak ca njiiti xeet wa, te gànnaayoo jaasi ak yet.
44 Fekk ki ko naroona wor joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko, yóbbu ko te wottu ko bu baax.» 45 Noonu mu ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi,» daldi ko fóon. 46 Bi mu ko defee nit ñi song Yeesu nag, jàpp ko. 47 Waaye kenn ci ñi fa taxaw bocci jaaseem, dóor surgab sarxalkat bu mag bi, nopp bi dagg.
48 Yeesu ne leen: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. 49 Moona daan naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngle, te jàppuleen ma. Waaye lii am na, ngir Mbind mi am.» 50 Ci kaw loolu, ñépp dëddu ko, daw.
51 Fekk amoon na ca waxambaane wu lëkkaayoo woon sér, topp Yeesu, ñu daldi ko jàpp. 52 Waaye waxambaane wa wacc fa sér bi, daldi daw, def yaramu neen.
Yeesu taxaw na ci kanam kureelu àttekat yi
53 Ñi jàpp Yeesu yóbbu ko ci sarxalkat bu mag bi, te foofa la sarxalkat yu mag yi, njiit yi ak xutbakat yi yépp dajaloo. 54 Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci ëttu sarxalkat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi.
55 Noonu sarxalkat yu mag yi ak kureelu àttekat yi yépp di wut ku mana seede lu daan Yeesu, ba ñu man koo reylu, waaye gisuñu kenn. 56 Teewul sax naaféq ñu bare ñëw, seede ci Yeesu lu dul dëgg, waaye seen seede ànduñu. 57 Ba mujj naaféq taxaw, seede ci moom naan: 58 «Nun daal dégg nanu, mu ne: “Dinaa toj kër Yàlla, gii loxoy nit liggéey, tabax ci ñetti fan geneen gu nit liggéeyul.”» 59 Waaye ba tey seeni wax ànduñu.
60 Ci kaw loolu sarxalkat bu mag bi taxaw ci seen kanam ne Yeesu: «Doo tontu? Lu la nit ñi di jiiñ?» 61 Waaye Yeesu ne cell, waxul dara. Sarxalkat bu mag bi dellu nag ne ko: «Ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ju tedd ji?» 62 Yeesu ne ko: «Moom laa. Te dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Aji Man ji, di ñëw ci niiri asamaan.»
63 Bi ko sarxalkat bu mag bi déggee nag, mu daldi mer, ba xotti ay yéreem naan: 64 «Weddi na Yàlla, lu nu doyeeti seede? Lu ngeen ci xalaat?» Noonu ñépp teg ko dee. 65 Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci moom, takk ay bëtam, di ko dóor ay kurfeñ, naan ko: «Yaw wax nu ci kàddug Yàlla, ku la dóor?» Ba noppi alkaati yi teeru ko ak ay pes.
Piyeer weddi na Yeesu
66 Piyeer nag ma nga toogoon ci ëtt bi féete suuf. Noonu benn mbindaanu sarxalkat bu mag ba romb fa. 67 Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko jàkk naan: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu.» 68 Waaye Piyeer weddi ko naan: «Xawma li ngay wax, dégguma ci dara.» Mu daldi génn, dem ca buntu kër ga. 69 Foofa nag mbindaan mi gisaat ko, mu ne ñi fa taxaw: «Waa jii ci ñoom la bokk.» 70 Waaye Piyeer weddiwaat ko.
Nees-tuut ñi fa taxaw ne Piyeer: «Yaw mi de, ci lu wóor bokk nga ci, nde waa Galile nga.» 71 Waaye Piyeer daldi giñ ak a waat naan: «Xawma nit ki ngay wax.» 72 Ci saa si ginaar sab ñaareelu yoon. Noonu Piyeer fàttaliku li ko Yeesu wax: «Bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi jooy jooy yu metti.