Saraxu soxna si
21
1 Noonu Yeesu siggi, séen ay boroom alal ñuy dugal seen sarax ca ndab ya ca kër Yàlla ga. 2 Mu gis itam jenn jigéen ju jëkkëram faatu te mu ñàkk, ju fa def ñaari poseti xànjara. 3 Noonu mu daldi ne: «Ci dëgg, maa ngi leen koy wax, jigéen ju ñàkk jee moo ëpp ñeneen ñépp lu mu joxe. 4 Ñoom ñépp dañu sàkk ci seen barele, waaye moom dafa sàkk ci néewleem, ba joxe xaalis bi mu waroona dunde.»
Yàqug Yerusalem ak dellusig Doomu nit ki
5 Noonu ay nit doon wax ci lu jëm ca kër Yàlla ga, ak ni ñu ko rafetale ak ay doj yu jafe ak alal ju ñu jébbal Yàlla. Waaye Yeesu ne leen: 6 «Li ngeen gis fii lépp, jamono dina ñëw joo xam ne dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.»
7 Ñu laaj ko ne: «Kilifa gi, kañ la loolu di am? Ak luy tegtal ne looloo ngi waaja xew?» 8 Yeesu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu. 9 Bu ngeen déggee ay xare ak ay réew yu jóg, wottuleena tiit, ndaxte fàww yooyule jëkka am. Waaye taxul mujug jamono daldi taxaw.»
10 Noonu mu teg ca ne: «Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew dina xeex ak meneen réew. 11 Suuf dina yëngu yëngu yu réy, te wopp ak xiif dina am ci bérab yu bare. Dina am it ay xew-xew yu raglu ak ay firnde yu mag yuy jóge asamaan. 12 Waaye bala looloo xew, dees na leen jàpp, fitnaal leen, di leen jébbal àttekat yi ca jàngu ya, tëj leen kaso. Dees na leen yóbbu ci kanam i buur ak i boroom réew ndax sama tur. 13 Loolu dina leen ubbil bunt, ba ngeen man maa seedeel. 14 Fasleen yéenee baña wut lay ngir musal seen bopp. 15 Ndaxte man ci sama bopp maa leen di jox kàddu ak xel moo xam ne seeni noon duñu ko mana teggi, mbaa ñu di ko weddi. 16 Seeni waajur sax ak seeni doomi ndey, seeni bokk ak seeni xarit, dinañu leen jébbal àttekat yi, ba ñu rey ñenn ci yéen. 17 Te ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur. 18 Waaye seen genn kawar sax du neen. 19 Seen muñ moo leen di musal.
20 «Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na. 21 Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba! 22 Ndaxte ci bés yooyu Yàlla dina fey jëf yi, te li ñu bindoon ci téereb Yàlla dina mat. 23 Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii. 24 Dees na leen reye ak i jaasi, jàpp leen jaam, yóbbu leen ci réewi àddina sépp. Te ñi dul Yawut dinañu nappaaje Yerusalem, ba kera jamonoy ñi dul Yawut mat.
25 «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi, ci weer wi ak ci biddiiw yi. Ci kaw suuf xeet yi dinañu tiit, jaaxle ndax riiru géej gi ak yëngu-yëngub duus yi. 26 Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange, bu ñuy xalaat musiba, yi nara wàcc ci àddina, ndaxte dees na yëngal kàttani asamaan. 27 Noonu dinañu gis Doomu nit ki di ñëw ciw niir, ànd ak kàttan ak ndam lu réy. 28 Bu mbir yooyu di tàmbalee xew nag, boo yaboo ngeen siggi, téen, ndaxte seen njot jubsi na.»
29 Noonu Yeesu misaal leen lii: «Xool-leen garabu figg ak yeneen garab yi. 30 Bu ñu gisee ñu sëq, soxlawuleen kenn wax leen ne, nawet bi jubsi na xaat. 31 Noonu itam bu ngeen gisee loolu lépp xew, xamleen ne nguuru Yàlla jege na.
32 «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy, te loolu lépp amul. 33 Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
34 «Moytuleen seen nafsu diigal leen ci yàqute ak ci màndite ak ittey àddina, ba bés boobu bett leen ni mbaal. 35 Ndaxte dina dal ci ñépp ñi nekk ci kaw suuf. 36 Yewwuleen, di sax ci ñaan, ngir ngeen mana mucc ci loolu lépp wara xew, te mana taxaw ak kóolute ci kanam Doomu nit ki.»
37 Yeesoo ngi daan yendoo jàngle ca kër Yàlla ga, te bu guddee mu dem ca tund wu ñuy wax tundu Oliw ya, fanaan fa. 38 Te nit ñépp dañu daan teela xëy ca kër Yàlla ga, di ko déglu.