Xibaaru jàmm bi ci Almasi bi Yeesu, ni ko Yàlla jaaralee ci
YOWAANA
Yeesu Kirist moo di Kàddu gi ak leer gu wóor gi
1
1 Ca njàlbéen ga fekk na Kàddu gi am, te Kàddu gi ma nga woon ak Yàlla, te Kàddu gi Yàlla la woon. 2 Moo di ki nekkoon ak Yàlla ca njàlbéen ga. 3 Ci moom lañu sàkke lépp. Amul dara lu ñu sàkk lu jaarul ci moom. 4 Ci moom la dund nekk, te dund googu mooy leeral nit ñi. 5 Leer gi feeñ na ci biir lëndëm, te lëndëm gi jàppu ko.6 Yàlla yónni woon na nit ku ñu naan Yaxya. 7 Kooku ñëw na, doon ab seede, ngir wax ci mbirum leer gi. Ñëw na ngir ñépp dégg li mu wax te gëm. 8 Moom ci boppam du woon leer gi, waaye ñëw na ngir seedeel leer gi.
9 Kàddu googu mooy leer gu wóor, giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk. 10 Ci àddina la nekkoon, àddina si ñu sàkk jaarale ko ci moom, te àddina xamu ko. 11 Ñëw na ci réewam, te ay ñoñam nanguwuñu ko. 12 Teewul ñi ko nangu te gëm ci turam, may na leen, ñu am sañ-sañu nekk doomi Yàlla. 13 Ñooñu judduwuñu ci deret walla ci bëgg-bëggu yaram, walla ci coobarey nit. Ñu ngi juddu ci Yàlla.
14 Kàddu gi ñëw, doon nit, dëkk ci sunu biir. Gis nañu ndamam, mu fees ak yiw ak dëgg, ndam li Baay bi jox jenn Doomam ji mu am kepp.
15 Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»
16 Kàddu gi fees na ak yiw, te nun ñépp jot nanu ci sunu wàll, mu barkeel nu ay yooni yoon. 17 Ndigali Yàlla yi, ci gémmiñu Musaa lañu leen jaarale; yiw wi ak dëgg gi, Yeesu Kirist moo ko indaale. 18 Kenn masula gis Yàlla, waaye Bàjjo bi, di Yàlla te nekk ak Baay bi, moo ko xamle.
Yaxya nee na, du Almasi bi
19 Lii mooy seedes Yaxya. Amoon na bés Yawut ya yónni ay sarxalkat ca Yaxya, ñu ànd ak ñu soqikoo ci giiru Lewi. Ñu nga jóge Yerusalem, ñëw ci moom, di ko laaj mooy kan. 20 Yaxya tontu na leen te nëbbu ci dara, wóoral na leen ne moom du Almasi bi.
21 Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Ilyaas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Ilyaas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi wara ñëw?» Mu ne leen: «Déedéet.» 22 Noonu ñu laaj ko ne: «Wax nu yaay kan, ngir nu mana tontu ñi nu yónni. Nga ne yaa di kan?» 23 Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»
24 Amoon na ñu bokk ca Farisen ya, yu àndoon ca mbooloo, ma ñu yónni woon ca Yaxya. 25 Ñooñu laaj ko ne: «Gannaaw doo Almasi bi, doo Ilyaas, doo Yonent bi wara ñëw, lu tax ngay sóob nit ñi ci ndox?» 26 Yaxya ne leen: «Man maa ngi sóobe ci ndox, waaye am na ci seen biir ku ngeen xamul. 27 Kookooy ñëw sama gannaaw, te man sax yeyoowumaa tekki ay dàllam.»
28 Lii xewoon na ci dëkku Betani, ca gannaaw dexu Yurdan, fa Yaxya doon sóobe.
Yeesu moo di Gàttub Yàlla
29 Ca ëllëg sa, bi Yaxya gisee Yeesu, muy ñëw ci moom, mu ne: «Xool-leen! Kii mooy Gàttub Yàlla, bi ñu nara rendi, ngir dindi bàkkaaru àddina. 30 Moo taxoon ma wax ne: “Am na kuy ñëw sama gannaaw, waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.” 31 Xawma woon kooku kan la waroona doon, waaye xamal ko bànni Israyil moo tax ma ñëw, di sóob nit ñi ci ndox.»
32 Ci kaw loolu Yaxya seede na lii: «Gis naa Xelu Yàlla mi ci melow pitax, mu jóge ci asamaan, tegu ci moom. 33 Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”» 34 Yaxya teg ca ne: «Gis naa loolu te seede naa ne moom moo di Doomu Yàlla ji.»
Ñi jëkka doon taalibey Yeesu
35 Ca ëllëg sa Yaxya taxawaatoon na ca bérab booba, ànd ak ñaari taalibeem. 36 Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy Gàttub Yàlla bi!»
37 Ñaari taalibe ya dégg li mu wax, daldi dem toppi Yeesu. 38 Yeesu geestu, gis ne ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu ne ko: «Foo dëkk, Ràbbi?»
Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi». 39 Yeesu ne leen: «Kaayleen gis.» Noonu ñu dem, seeti fa mu daloon, ngoonalal ko. Ci tàkkusaani kaw la woon.
40 Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay. 41 Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist». 42 Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer», maanaam «xeer».
Yeesu woo na Filib ak Nataneel
43 Ca ëllëg sa mu fas yéenee dem diiwaanu Galile te mu gis Filib. Yeesu ne ko: «Toppal ci man.»
44 Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer. 45 Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.» 46 Nataneel ne ko: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.»
47 Naka la Yeesu gis Nataneel jëmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: «Xool-leen, nitu Israyil dëgg a ngee di ñëw; du dox benn tànku caaxaan.» 48 Nataneel ne ko: «Noo ma xame?» Yeesu ne ko: «Bi la Filib di laata woo, gis naa la, bi nga nekkee ca ker garabu figg ga.» 49 Nataneel wax ko ne: «Kilifa gi, yaay Doomu Yàlla ji, yaa di buuru Israyil!» 50 Yeesu ne ko: «Ndax li ma ne, gis naa la ca ker garab ga, moo tax nga gëm? Dinga gis mbir yu gëna réy yii.» 51 Noonu mu teg ca ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, dingeen gis asamaan ubbiku, malaaka yiy baagante kaw ak suuf, di wàcc ci Doomu nit ki.»