Yeesu Kirist dekki na
24
1 Bés bu jëkk ca ayu-bés ga, jigéen ña jóg ca fajar, dem ca bàmmeel ba. Ñu ngi yoroon cuuraay lu ñu defaroon. 2 Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba. 3 Ñu dugg ca bàmmeel ba, waaye fekkuñu fa néewu Boroom bi Yeesu. 4 Noonu ba ñu nekkee ak seen njaaxle, am na ñaar ñu leen feeñu, sol yére yuy melax. 5 Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi? 6 Nekkatu fi; dekki na. Fàttalikuleen la mu leen waxoon, ba mu nekkee Galile. 7 Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”» 8 Noonu ñu daldi fàttaliku kàdduy Yeesu ya.9 Bi ñu jógee bàmmeel ba, ñu dem nettaliji loolu lépp fukki ndaw ya ak benn, ak ña ca des ñépp. 10 Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya. 11 Waaye ñu teg wax jooju ay jeneer, ba gëmuñu jigéen ñooñu. 12 Waaye Piyeer daldi jóg, daw, dem ca bàmmeel ba. Bi mu àggee, mu sëgg, yër, gisul lu dul càngaay la. Noonu mu dëpp ñibbi, jaaxle lool ci li xew.
Yeesu feeñu na ñaari taalibe yu jëm Emayus
13 Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet. 14 Ñu waxtaane li xewoon lépp. 15 Bi ñuy waxtaan ak a sotteente xalaat, Yeesu ci boppam dab leen, ànd ak ñoom, 16 fekk seeni bët muuru, ba manu ko woona xàmmi. 17 Yeesu ne leen: «Lan ngeen di waxtaane nii ci yoon wi?» Noonu ñu taxaw, seen xol jeex. 18 Kenn ci ñoom, ki tudd Këleyopas ne ko: «Xanaa yaw rekk yaa ñëw Yerusalem te umple li fi xewoon bés yii?» 19 Yeesu ne leen: «Lu fi xew?» Ñu ne ko: «Mbirum Yeesum Nasaret. Ab yonent la woon bu doon def ay jëf yu mag, di wax ay kàddu yu am doole, ci kanam nit ñi ak ca kanam Yàlla. 20 Waaye sunuy sarxalkat yu mag ak sunuy njiit ñoo ko jébbal nguur gi ngir ñu àtte ko, teg ko dee, ba daaj ko ci bant. 21 Nun nag danoo yaakaaroon ne mooy kiy nara jot Israyil. Waaye bi loolu xewee ak léegi, tey la ñetteelu fan bi. 22 Teewul nag am na ay jigéen yu bokk ci nun yu nu jaaxal. Dañoo fajaru ca bàmmeel ba, 23 waaye fekkuñu fa néewam. Ñu délsi, nettali nu ne, ay malaaka feeñu nañu leen, yégal leen ne mi ngi dund. 24 Ñenn ci sunu àndandoo yi dem nañu ca bàmmeel ba, fekk lépp mel, na ko jigéen ña waxe woon. Waaye moom gisuñu ko.»
25 Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéexa gëm li yonent yi yégle woon! 26 Xanaa du Almasi bi dafa waroona daj boobu coono te dugg ci ndamam?» 27 Noonu mu tàmbalee ci yonent Yàlla Musaa ba ci yonent yépp, tekkil leen li Mbind mi wax lépp ci ay mbiram.
28 Bi ñuy jub dëkk, ba ñu jëmoon nag, Yeesu def ni kuy jubal yoonam. 29 Waaye ñu téye ko ne ko: «Toogal fii ci nun, ndaxte jant baa ngi so, te léegi mu guddi.»
Noonu mu dugg, toog ca ñoom. 30 Bi ñu tàmbali di reer, Yeesu jël mburu ma, gërëm Yàlla, ba noppi damm ko, jox leen ko. 31 Bi mu defee loolu, lépp leer ci seeni bët, ñu daldi ko xàmmi. Waaye Yeesu ne mes, gisatuñu ko. 32 Noonu ku nekk naan sa moroom: «Ndax sa xol seddul woon, bi muy wax ak nun ci yoon wi, te muy tekki Mbind mi?»
33 Ñu daldi jóg ca saa sa, dellu Yerusalem, fekk fa fukki ndaw ya ak benn, ak yeneen taalibe. 34 Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!» 35 Ñaari taalibe ya ñoom it daldi leen nettali la xewoon ca yoon wa ak ni ñu xàmmee Yeesu, bi mu dammee mburu ma.
Yeesu feeñu na ay taalibeem
36 Bi ñaari taalibe ya dee wax noonu, Yeesu taxaw moom ci boppam ci seen biir ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen.» 37 Ñu daldi tiit, foog ne dañoo gis njuuma. 38 Waaye Yeesu ne leen: «Lu tax ngeen jaaxle, ak lu tax ngeen di xel ñaar ci seen xol? 39 Xool-leen samay loxo ak samay tànk. Man mii la. Laal-leen ma te xam, njuuma amul yaram walla ay yax, ni ngeen gise, ma am ko.» 40 Bi mu leen waxee loolu, mu won leen ay loxoom ak ay tànkam. 41 Waaye ba tey manuñu woona gëm ndax seen mbég ak jaaxle. Noonu Yeesu laaj leen ne: «Ndax am ngeen fii lu ñu lekk?» 42 Ñu jox ko dogu jën wu ñu lakk. 43 Mu jël ko, lekk ci seen kanam.
44 Noonu mu ne leen: «Bi ma nekkee ak yéen, waxoon naa leen baat yii: li ñu bind lépp ci samay mbir ci yoonu Musaa ak ci téerey yonent yi ak ci Sabóor dafa wara am.» 45 Noonu mu ubbi seen xel, ngir ñu xam li Mbind mi di wax. 46 Mu ne leen: «Fàww Almasi bi sonn, mu dee te dekki ca ñetteelu fan ba, ni ñu ko binde, 47 te it ñuy yégle xeet yépp ci turam, dale ko ci Yerusalem ne war nañoo tuub seeni bàkkaar, Yàlla baal leen. 48 Yéenay samay seede. 49 Te man dinaa leen yónnee li sama Baay dige. Yéen nag toogleen ci dëkk bi, ba ñu sol leen doole ji jóge ci kaw.»
Yeesu tàggu na ay taalibeem