Pool lay na ci kanam Feligsë, boroom réew ma.
24
1 Bi juróomi fan wéyee, Anañas sarxalkat bu mag ba dikk, ànd ak ay njiit ak layookat bu tudd Tertul, ñu woo Pool ci yoon fa kanam boroom réew ma. 2 Noonu ñu woo Pool, te Tertul daldi ko jiiñ naan: «Yaw Feligsë mu tedd mi, sa nguur jural na nu jàmm ju neex, te sa jàppandil soppi na lu bare ci sunu xeet. 3 Gis nanu ko fépp ak ci lépp, di la gërëm ak sunu xol bépp. 4 Waaye ngir baña yàggal jataay bi, maa ngi lay ñaan ci sa lewetaay, nga déglu nu ci lu gàtt. 5 Ndaxte ci mbirum nit kii teew, gis nanu ne rambaaj la, buy indi xëccoo ci Yawut yi ci àddina sépp, di njiitu mbooloo mu ñuy wax Nasareen. 6-7 Dem na ba jéema teddadil sax kër Yàlla ga, waaye jàpp nanu ko. 8 Soo ko laajee, yaw ci sa bopp, dinga gis ne li nu koy jiiñ dëgg la.» 9 Ci kaw loolu Yawut ya ànd ca, di dëggal ne loolu wóor na.10 Bi loolu amee boroom réew ma jox Pool kàddu gi. Noonu mu làyyi ne:
«Xam naa ne yaa ngi àtte xeet wi diirub at yu bare, moo tax maa ngi làyyi ak kóolute. 11 Man ngaa wóorliku ne ëppagul fukki fan ak ñaar demoon naa Yerusalem ngir màggali. 12 Te kenn gisu ma, maay werante mbaa di jógloo mbooloo, muy ca kër Yàlla ga mbaa ca jàngu ya mbaa ci biir dëkk ba. 13 Te manuñoo firndeel dara ci li ñu may jiiñ léegi. 14 Waaye nangu naa ci sa kanam ne maa ngi jaamu Yàllay sunuy maam, ci topp yoon wi ñu ne mooy tariixa; terewul ne lépp li ñu tëral ci yoonu Musaa ak li yonent yi bind, gëm naa ko. 15 Te bokk naa ak ñoom yaakaar ci Yàlla, ne ñi jub ak ñi jubadi dinañu dekki keroog yawmelxayaam. 16 Moo tax fu ma tollu, maa ngi góor-góorlu, ngir am xel mu dal fa kanam Yàlla ak fa kanam nit ñi.
17 «Noonu gannaaw gëjeb at yu bare ñëw naa, ngir indil sama xeet ndimbal te jébbal Yàlla ay sarax. 18 Bi ma koy def nag, gis nañu ma ca kër Yàlla ga, ma setlu ba noppi, fekk ànduma ak mbooloo te indiwuma benn coow. 19 Waaye ay Yawut yu dëkk Asi –xanaa kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp. 20 Waaye it na nit ñii wax ci lan laa tooñe ci jataayu géewub àtte ba, 21 xanaa li ma waxoon ca kaw ci seen biir rekk ne: “Mbirum ndekkitel ñi dee moo tax ngeen dëj ma ci seen kanam tey!”»
22 Bi mu waxee noonu, Feligsë mi xam bu wóor mbirum yoon wi, yiwi leen ba beneen yoon. Mu ne leen: «Bu Lisiyas kilifag xare bi ñëwee, dinaa àtte seen mbir.» 23 Noonu mu sant njiitu xare ba ne ko: «Nanga wottu Pool, waaye nga may ko féex, te bàyyi ay xaritam, ñu topptoo ko.»
24 Bi ay fan wéyee, Feligsë ñëwaat, ànd ak soxnaam Dursil, miy Yawut. Noonu mu woolu Pool, di ko déglu ci mbirum gëm Yeesu Kirist. 25 Waaye bi Pool di waxtaan ci mbirum njub ak moom sa bopp ak bés pénc, Feligsë daldi tiit, yiwi ko ne ko: «Demal, bu ma amee jot, dinaa la woolu.» 26 Fekk yaakaaroon na it ne, Pool dina ko jox xaalis; kon mu di ko farala woolu, ngir waxtaan ak moom.
27 Bi ñaari at weesoo nag, amoon na ku wuutu Feligsë, tudd Porsiyus Festus. Noonu Feligsë, mi bëggoon lu neex Yawut ya, bàyyi Pool ca kaso ba.