Sasu Sarxalkat yi
di ñetteelu xaaju Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Aaya bi jiitu ci Sasu Sarxalkat yi moo indi na Yàlla àddoo woon ca xaymab ndaje ma, woo Yonent Yàlla Musaa, ngir wax ak moom. Bare na lool fu téere bi joxe ay ndigali yoon aki sàrt yu Yàlla jox Musaa, ngir mu jottli ko bànni Israyil, te dige bi ci Yàlla boole moo di ndigal yooyu ñooy taxa dund képp ku leen jëfe.
Ci gàttal, ci téere bi la Yàlla di xamal bànni Israyil, nan lees di dindee mboolem li gàllankoor seenub neexoo ak Yàlla, ak nan lees di jëfe ba xaymab jaamookaay bi doon bérabu ndaje dëgg bu ñuy dajee ak Yàlla. Fàww ñiy jooxe ay sarax jooxe sarax yi ni mu ware. Fàww it sarxalkat yi di nit ñu ñu weg, nit ñu seen jëfin tedd, te kenn ku nekk ci askan wi moytu, kem kàttanam, mboolem luy sobeel aw yaram, te moytu di fecci kóllëre ci jëfinam ak ci ni muy jaamoo Yàlla. Yàlla miy Ku Sell, di Cofeelu neen, di Ki yor ndund, moo namm ñoñam wàllsi ci sellngay boppam, ngir ñoom itam ñu man di jottlee, ndund ak cofeel. Yéene boobu la Yàlla joxe bànni Israyil santaane bii Almasi ne mooy kenug yoonu Yàlla: “Ni ngeen soppe seen bopp nag, nangeen ko soppe seen moroom.” Aaya 19:18.
Mboolem ndigali yoon yi ci téere bi, li leen taxa jóg mooy yombal nu gëmkat ñi mana neexoo ak Yàlla, ak fépp fu ñu mana bokk, ak jant bu ñu mana yemool. Kon ndigali yoon yii tàyyiwuñu benn yoon di soññe ci mboolem xeeti kàddu, ngir gëmkat bi saxoo bàyyi xel ne neexoo ak Yàlla manula ñàkk, te ci la ag dundam aju.
Ci Tënk:
Saar 1—7 Ay dogal ci mbirum sarax yi
Saar 8—10 Fal nañu sarxalkat yi
Saar 11—15 Sàrtal nañu lu set ak lu setul
Saar 16 Lu jëm ci bésub Njotlaay
Saar 17—26 Ndigal yi jëm ci sellal
Saar 27 Lu jëm ci jagleel Aji Sax ji nit ak alal