Muccug bànni Israyil
di ñaareelu xaaju Tawreetu Musaa
Ubbite gi
Ñaareelu xaaju Tawreet bii moo wéyal jaar-jaari bànni Israyil, jële ko fa ko téere bu jëkk ba, téereb Njàlbéen ga bàyyi woon. Fi téere bi jële aw turam, Mucc gi, mooy xew-xew bi ci gëna fés, di mucc gi Yàlla musal bànni Israyil, ca mbugal mu mujj ma mu wàcce woon fa Misra, mbugal ma Yàlla doge seen buumi njaam, ba génne leen fa.
Yàlla moo jox bànni Israyil ndigali yoon wi ca tundu Sinayi, Musaa jottli ko, muy li lal kóllëre gi mu fas, moom Yàlla ak bànni Israyil. Yàlla nag musal leen, ba ñu tala séq ak moom digganteb kóllëre. Ndigali yoon wi moo xamal mbooloom bànni Israyil nan lañuy sàmme seen digganteek moom. Yàlla moo bëggoon bànni Israyil doon ñoñam, ndax ci ñoom la nammoona amal digeem baak seen maam Ibraayma. Dige ba mooy xeeti àddina sépp, ci askanu Ibraayma lañuy barkeele.
Mujug téere bi kéemaan gu réy la. Mooy gannaaw ba ñu sampee jaamookaay ba, na ko Yàlla santaanee, ba Yàlla feesale ag leeram xaymab jaamookaay ba, ngir wone ne moo fa teew.
Ci Tënk:
Saar 1—18 Yàlla yiwi na bànni Israyil, génne leen Misra.
Saar 19—24 Yàlla fasante na kóllëre ak bànni Israyil.
Saar 25—40 Yàlla sant na Musaa, mu defarlu xaymab jaamookaay.