Mb - mb
mbaam m- * n. Variant: mbaam-sëf m-; mbaam kër m-. 1 • âne *; Esel; donkey.
mbaam ngonk m- âne adulte et fort; kräftiger, erwachsener Esel; strong adult donkey. Isakaar mbaam ngonk la, muy goor diggante ñaari sëf. [Njàlbéen ga / Gn 49.14]
Variant: mbaam-xuux m-. 2 • porc; cochon *; Schwein; pig; hog.
Variant: mbaam-àll m-. 3 • phacochère *; Warzenschwein; warthog.
mbalka m- n. abreuvoir; bac; grande citerne *; Viehtränke; Wassertrog; Bottich; große Zisterne; Wasserbehälter (aus Beton); cattle watering tank; trough; large cisterne; reservoir. Noonu mu gaaw, sotti njaq la ca mbalka ma, dawaat rootali giléem yi ca seyaan ba. Elle se dépechait, versait la cruche dans l'abreuvoir et courrait de nouveau afin de puiser dans le puit pour les dromadaires. Sie eilte, goß den Krug aus in die Tränke, rannte, um für die Dromedare erneut vom Brunnen zu schöpfen. She hurried, emptied the jar into the trough, ran back to draw again water for the dromedary from the well. [Gn 24.20] Note: abreuvoir pour faire abreuvoir les animaux Note: ID: Lawbeen ko yétt.
mbandkat b- * griot qui va de village en village avec une bande de musiciens ambulants chantant des chants laudatif au rythme de leurs tambours d'aisselle *; troubadour; "Griot", der mit einer Gruppe wandernder Musikanten von Dorf zu Dorf zieht, und die dabei Loblieder zum Rhythmus ihren unter die Achsel geklemmten Trommeln singen; "griot" who is going from village to village together with a groupe of travelling musicians who sing praise songs to the rhythm of their drums which they hold under their armpits. Variant: bandkat b- *.
mbas * v.t. feinter; esquiver; se dégager brusquement pour déséquilibrer quelqu'un ou pour éviter qu'il vous touche *; contourner; tromper, échapper en fantant (?); vortäuschen; ausweichen; sich brüsk befreien, um jemanden aus dem Gleichgewicht zu bringen oder um zu vermeiden, berührt zu werden; umgehen; täuschen; to feint; to dodge; to free oneself bruskly in order to unbalance someone or to avoid being touched; to bypass; to deceive. Siis bi mbas na ko, mu daanu
mbas m- * n. épidémie; fléau *; Epidemie; Geißel; Plage; epidemic; scourge. Gàdd dem ca Daawuda, jottali ko ko, ne ko: «Ana yii yett loo taamu, mu dal ci sa kaw: juróom yaari ati xiif ci sam réew, am ñetti weer yooy daw say noon, am ñetti fani mbas ci sam réew? Xalaatal léegi te wax ci lenn, ma xam lu may jottali ki ma yónni.» [2.Samiyel / 2Sa 24.13]
mbege g- / m- n. cerceau; cercle *; volant (auto); Bogen; Reifen; Kreis; Rad; hoop; tire; circle; wheel. Pëno dafa fegu ci mbege gi. Le cerceau protège la jante. Der Reifen schützt die Felge. The tire protects the wheel rim. [ME]
puus mbege v. pousser un cerceau; Reifen mit Stock antreiben; to push a hoop with a stick. Note: hoop (which children push ahead of them)
mbool m- * n. épi de petit mil fraîchement coupé; épi de mil frais à griller *, épi mûr; frisch geschnittene Hirseähre; frische Hirseähre zum Grillen; freshly cut millet ear; fresh millet ear for roasting. «Bu nit dee indil Aji Sax ji sarax ci li mu jëkka meññle, na ko indil mbool* mu ñu séndal, def ko sànqal, muy saraxu meññeefam mu jëkk. [Lv 2.14] Ci biir loolu Isayi wax doomam Daawuda ne ko: «Ayca, jëlal nattub mbool mii ak fukki mburu yii, yóbbul ko gaaw sa mag ya ca dal ba. [1Sa 17.17]
mbóoyo m- * n. harmattan *; Harmattan; heißer, staubiger Wind; harmattan.
mbugal m- Variant: mbugël m- *. n. châtiment; châtiment de Dieu; torture *; fléau, l'arrêt; la censure; la peine; Strafe; Bestrafung; Strafe Gottes; Folter; Qual; Plage; punishment; divine punishment; torture; plague. Waaye Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko!» [Njàlbéen ga / Gn 4.13] Yal na mbugalam yem ci àddina. [ME / ID]