Beyal saw sas
2
1 Kon nag yaw doom, doolewool yiw, wi Almasi Yeesu di maye. 2 Li nga dégge ci man te seede yu bare teewe ko, nanga ko jottli nit ñu wóor ñu ko mana xamal ñeneen. 3 Jëlal sa wàll ci coono bi takk-derub Almasi Yeesu bu wóor di jànkoonteel. 4 Ab takk-der bu bëgga neex ka ko solal kat, du xintewoo mbiri nit ña soluwul. 5 Kuy joŋante it, deesu ko kaala te joŋantewul ci yoon. 6 Te it beykat bi yor coonob liggéey bi, moo wara jëkka séddu ca meññeef ma. 7 Defal sam xel ci li ma la wax. Boroom bi moo lay leeralal lépp.
Yeesu mooy boroom kóllëre
8 Bàyyil xel ci Yeesu Almasi mi ñu dekkal te mu soqikoo ci Daawuda, ni ko sama xibaaru jàmm indee. 9 Xibaaru jàmm boobu moo tax may daj coono yu metti ni defkatu mbon, ba ci jéng yii ñu ma jéng. Waaye kàddug Yàlla moom, deesu ko jéng. 10 Looloo ma tax di muñ lépp, ngir ñi ñu taamu, ndax ñoom it ñu dajeek mucc gi ci Almasi Yeesu, boole ci teraanga ju sax.
11 Kàddu gu wóor a ngii:
Su nu deeyandoo ak Almasi,
nooy dundandoo ak moom itam;
12 su nu muñee,
nooy bokk nguuru.
13 Su nu ko gàntalee,
moom it dinanu gàntal;
su nu ko ñàkkee kóllëre,
mu saxoo kóllëreem,
ndax manula gàntal boppam.
Surga day sàkku ngërëmu njaatigeem
14 Loolu, dee ko fàttlee, te ngay dénkaane fi kanam Yàlla, ñu bañ di xuloo ci ay baat, ndax amul njariñ, ñi koy dégg doŋŋ lay sànk. 15 Defal sa kem-kàttan ba boo teewee fa kanam Yàlla, di ku mu gërëm, ab liggéeykat bu mucc gàcce, di xamle kàddug dëgg gi ni mu ware. 16 Waaye ay kebetuy àddinay kese, moytu ko, ndax ngëmadi gu ko yées rekk lay yóbbee, 17 te kàdduy ñooñu day law ni ngal. Ci ñooñu la Imene ak Filet bokk. 18 Ñoo lajj yoonu dëgg, ba naan ñiy dekki, dekki nañu ba noppi, te seen wax jooju, am na ñenn ñu muy yàq seen ngëm. 19 Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ay ñoñama,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»
20 Kër gu mag nag, du ndabi wurus ak xaalis rekk a fa am, waaye yoy bant a nga fa, ak yoy ban; yii di ndabi teraanga, yee di ndabi njoogaan. 21 Ku setal sa bopp nag ba mucc ci yu bon yooyii, yaay doon ndabal teraanga lu sell te amal sangam njariñ ngir jépp jëf ju baax.
22 Xemmemtéefi ndaw nag, daw ko, te nga topp njub, ak ngëm ak cofeel, ak jàmm, ànd ceek ñiy tudde Boroom bi xol bu set wecc. 23 Waaye werante yu xeluwul te du xam-xam, moyu ko, te xam ne ay ŋaayoo lay jur. 24 Te jaamub Boroom bi warul di ŋaayoo, waaye day lewet ci ñépp, mana jàngle tey muñ. 25 Jaamub Boroom bi ndànk la war di jubbanti diiŋatkat yi, nde jombul Yàlla may leen ñu tuub, ba xam liy dëgg. 26 Su ko defee seenum xel dellusi, ba ñu rëcc fiirug Seytaane, mi leen jàpp, di leen defloo coobareem.