Mujug jamono dina tar
3
1 Lii, nanga ko xam: mujug jamono, jant yu tar dina dikk. 2 Nit ñi, seen bopp doŋŋ lañuy bëgg, ay bëggkati xaalis lañuy doon, ay damukat, nit ñu réy, di ay saagakati Yàlla, ñu déggadil waajur, ñu santadi te selladi. 3 Duñu am ab xol, duñu meddi, ay soskat lañuy doon, ñu ñàkk sago, ñu néeg te bañ lu baax; 4 ay workat lañuy doon, ñu teeyadi, ñu daŋŋiiral te di ñu bëgg seen bànneexu bopp, ba mu gënal leen Yàlla. 5 Ag njullite lañuy mbubboo tey xalab leer ga leen ko wara manloo. Ñooñu, dëddu leen.
6 Ñenn ci ñooñu ñooy yoxoosuy dugg ci biir kër yi, di fàbbi jigéen ñu ñàkk bopp, ñi seeni bàkkaar man, te seen xemmemtéef yu bare jiital leen. 7 Gëstu ay àlluwa la jigéen ñooñuy wéye, waaye duñu mana xam liy dëgg mukk. 8 Noonee Sànnes ak Sàmbresa doon jànkoonteek Musaa, ni la góor ñooñu di jànkoontee ak dëgg gi; ñooy nit ñu seenum xel yàqu, te ñu doyadi ci wàllu ngëm. 9 Waaye duñu soreeti, ndax seenug ndof dina bir ñépp, na ñaar ñooña mujje woon.
Póol dénkooti na Timote
10 Yaw nag seetlu nga bu baax sama àlluwa, ak sama dundin, ak sama mébét, ak sama ngëm, ak samag muñ, ak sama cofeel, ak samag ñeme coono, 11 ak itam bundxatal yaak njàqare ya ma dikke woon fa dëkk yooyu di Àncos ak Ikoñum ak Listarb. Céy na ñu ma bundxatale, waaye Sang bee ma musal ci lépp! 12 Te kat képp ku namma nekke ag njullite ci yoonu Almasi Yeesu, dees na la bundxatal. 13 Waaye nit ñu bon ñi, ak maa-man yi dañuy gën di bon rekk, di naxe tey nax seen bopp.
14 Yaw nag saxal ci li nga jàng, muy lu la wóor, nde xam nga ña nga tanqe. 15 Bi ngay lu tuut nga dale xam Mbind mu sell mi, te moo la mana may xel mu la jëme ci mucc gi gëm Almasi Yeesu di maye. 16 Mboolem Mbind mu sell mi la Yàlla wal ag Noowam, ba mu am njariñal jàngal nit ñi, femmu leen, jubbanti leen, yar leen cig njub. 17 Su ko defee nitu Yàlla ki mat sëkk te matley jumtukaay ngir jépp jëf ju baax.