Yonatan fas na kóllëreek Daawuda
18
1 Ba Daawuda di wax ak Sóol ba noppi, fekk na Yonatan yég ci xolam na mu taqook Daawuda ci biir cofeelu benn bakkan. Yonatan dafa soppoon Daawuda ni boppam. 2 Bésub keroog la Sóol téye Daawuda, mayatu ko mu ñibbi kër baayam. 3 Ba loolu amee Yonatan fasook Daawuda kóllëre, ndax sopp ko ni boppam. 4 Ci biir loolu Yonatan summi turkeem, jox ko Daawuda, boole ca ay yérey xareem, ba ca saamaram ak fittam ak ngañaayam sax. 5 Daawuda nag di dem ci bépp yoonu xare bu ko Sóol yebal, di ca am ndam. Sóol fal ko njiitu xarekat ya, gàngoor gépp rafetlu loolu, jawriñi Sóol itam rafetlu ko.Sóol a ngay fexeel Daawuda
6 Ba ñu demee ba xarekat yay ñibbi, gannaaw ba Daawuda reyee waa Filisti ba, jigéeni mboolem dëkki bànni Israyil a génn gatanduji Buur Sóol, di fecc ak a woy, tabala ya ànd ak sarxolle ya ak xalam ya. 7 Ña ngay fo, di awoonte, naan:
Sóol jam junneem,
Daawuda jam fukki junneem.
8 Sóol ñaawlu kàddu ga, mer lool. Mu ne ca xelam: «Daawuda lañu moomale fukki junni; man, junni! Lu ko deseeti lu moy jal bi?» 9 Bésub keroog la Sóol dale ronni Daawuda.
10 Ca ëllëg sa ngelawal Yàlla lu aay ne milib ca kaw Sóol, muy waxtu ca digg këram. Daawuda nag di ko xalamal, na mu daan def naka jekk, fekk Sóol ŋàbb ab xeejam. 11 Mu jekki sànni xeej ba, te naan ca xelam: «Naa daaj Daawuda ci tabax bi!» Daawuda nag mbas ko ñaari yoon.
12 Sóol daldi ragal Daawuda, ndax booba xam na ne Aji Sax jee ko dëddu, ànd ak Daawuda. 13 Ba loolu amee mu jële ko fi wetam, fal ko njiitu kurélu junniy xarekat, muy xareji, di délsi, jiite gàngoor ga. 14 Daawuda baaxle ca yoonam yépp, Aji Sax ji ànd ak moom. 15 Ba Sóol gisee Daawuda àntule lool, mu gën koo ragal. 16 Teewul mboolem Israyil ak Yuda sopp Daawuda, ngir moo leen jiite woon, di xareji, di dikk.
Daawuda jël na doomu Sóol soxna
17 Ci kaw loolu Sóol ne Daawuda: «Sama taaw bu jigéen, Merab a ngii. Moom laa lay may. Nekkal ma sama jàmbaaru xare rekk, te xareel Aji Sax ji ay xareem.» Booba Sóol a nga naan ca xelam: «Bu ko sama loxo laal, nay loxol waa Filisti.»
18 Daawuda ne Sóol: «Waaw, ana lu ma tekki, man maak samay bokk, sama askanu baay ci Israyil, ba wara mana goromlook Buur?» 19 Ba ñu demee ba wara jox Daawuda, Merab doomu Sóol ja, Àddiryel ma cosaanoo Mewola lañu ko may.
20 Ci kaw loolu Mikal doomu Sóol bëgg Daawuda, ñu àgge ko Sóol, mu am ca mbégte. 21 Booba Sóol a nga naan: «Naa ko ko may, ngir mu doon ndëgg-sërëxam, ba waa Filisti teg ko loxo.» Sóol nag wax Daawuda, ñaareel bi yoon, ne ko: «Tey ngay samab goro.» 22 Ci biir loolu Sóol sant ay dagam, ne leen: «Diisool-leen maak Daawuda, ngeen wax ko ne ko: “Yaw kat, Buur am na bànneex ci yaw, te it dagam yépp a la sopp. Kon nag nangula doon gorob Buur.”» 23 Dagi Sóol ya déey Daawuda kàddu yooyu. Daawuda ne leen: «Ngeen defe ne goromlook buur daal, du dara? Man mii taqul dara, tekkiwuma dara!» 24 Dag ya yegge Sóol kàddu yooyu Daawuda wax.
25 Sóol ne leen: «Waxleen Daawuda ne ko, Buur de sàkkuwul ub can: xanaa téeméeri mbuñukay waa Filisti yu mu feyoo ci noonam yooyu.» Booba la Sóol laloon mooy pexe mu tàbbal Daawuda ca loxol waa Filisti. 26 Dag ya yegge Daawuda kàddu yooya, doon gorob buur daldi koy jaral loola. Balaa àpp baa mat, 27 Daawuda dem na, mooki nitam ba rey ñaar téeméeri waa Filisti. Daawuda indi seeni mbuñuka, ñu waññal ko Buur ba mu mat sëkk, mu daldi yeyoo goromlook Buur. Ba loolu amee Sóol may Daawuda doomam Mikal. 28 Sóol nag xam xéll ne Aji Sax jee ànd ak Daawuda, te it doomam Mikal bëgg na ko, 29 mu gën koo ragalati. Fa la Sóol doxe doon noonub Daawuda ba fàww.
30 Ci kaw loolu njiiti xarey Filisti di amal ay cong, noppiwuñoo xareek Israyil. Teewul saa yu ñu songaan, Daawudaay gëna am ndam mboolem jawriñi Sóol, ba mujj Daawuda amu tur lool.