Yonatan taxawu na Daawuda
19
1 Ba mu ko defee Sóol xamal doomam Yonatan ak dagam yépp ne reylu Daawuda mooy li mu nar. Te Yonatan doomu Sóol sopp Daawuda lool. 2 Yonatan yegge ko Daawuda, ne ko: «Sama baay a ngi lay wuta rey. Yaw nag fagarul kat te teela xëy ëllëg, seet foo làquji te baña génn. 3 Man dinaa dem, taxaw ci sama wetu baay fi nga nekk ci àll bi. Dinaa wax ak sama baay ci yaw, nu bokk taxaw ca tool ba ngay làquji, man ci sama bopp dinaa wax ak sama baay ci yaw ba gis nu mbir mi tëdde, yegge la ko.» 4 Ci kaw loolu Yonatan wax baayam lu baax ci Daawuda, ne ko: «Buur, ngalla bul tooñ Daawuda, sa jaam bii, ndax moom kat tooñu la, lu baax rekk la la masa defal. 5 Jaay na bakkanam, ba rey waa Filisti ba. Aji Sax ji maye ca ndam lu réy, ñeel Israyil gépp, nga teg ci bët, am ca mbégte. Ana lu waral ngay tooñ, di tuur deretu jaamburu Yàlla bu mel ni Daawuda, reylu ko ci dara?» 6 Sóol nag déggal Yonatan, daldi ne: «Giñ naa ko ci Aji Sax jiy dund, deesul rey Daawuda.» 7 Yonatan woo Daawuda, nettali ko waxtaan wa wépp, door koo yóbbu ca Sóol, mu dellu di ko liggéeyal, na woon.Mikal xettli na Daawuda
8 Ci kaw loolu xare jibaat, Daawuda dem xeexi ak waa Filisti, daan leen jéll bu réy, ñu daw. 9 Ci kaw loolu ngelaw lu aay lu Aji Sax ji dikkal Sóol, fekk ko toog ci biir këram, ŋàbb ab xeejam, Daawudaa di xalam. 10 Sóol di wuta jam Daawuda xeej bi, ngir daaj ko ca tabax ba. Daawuda nag mbas ko, mu jam xeej ba ca tabax ba. Daawuda daldi daw, ba raw guddig keroog.
11 Sóol yebal ay ndaw ca kër Daawuda ngir ñu xoolal ko ko, ba bët set, ñu rey ko. Mikal, soxnas Daawuda, yégal ko Daawuda, ne ko: «Soo rawalewul sa bakkan ci guddi gi de, bu ëllëgee dees na la rey.» 12 Ba loolu amee Mikal jaarale ko ca palanteer ba, mu wàcc, daw, ba raw. 13 Mikal jël gàllaaju kër ga, teg ca lal ba, fab deru bëy, teg fa féeteek bopp ba, daldi koy sànge malaan. 14 Sóol yebal ay ndaw yu jàppsi Daawuda, Mikal ne: «Moom de daa wopp.» 15 Ci kaw loolu Sóol dellu yebal ndaw ya, ngir ñu dem ba gis ko. Mu ne leen: «Indil leen ma ko, booleek lal bi, ba ma rey ko!» 16 Naka la ndaw ya délsi, xool, gisuñu lu moy gàllaaju kër ga ca kaw lal ba, ak deru bëy ba féeteek bopp ba. 17 Ba loolu amee Sóol ne Mikal: «Ana lu waral nga wor ma nii, bàyyi sama noon, mu rëcc?» Mikal ne ko: «Moom kay moo ma ne: “Bàyyi ma, ma daw, lu ko moy ma rey la!”»
Sóol toppi na Daawuda ca Nayot
18 Noonu la Daawuda dawee ba raw. Mu fekki Samiyel ca Raama, wax ko la ko Sóol def lépp. Ñu ànd, mook Samiyel, dali ca Nayot. 19 Ñu yegge ko Sóol ne ko: «Ndeke Daawudaa nga Nayot ca dëkk ba ñuy wax Raama.» 20 Sóol yebal ay ndaw, ngir ñu jàpp Daawuda. Nit ña dikk, gis kurélu yonent yuy wax ay waxyu, Samiyel jiite leen. Ba loolu amee, ca kaw ndawi Sóol ya la Noowug Yàlla wàcc, ñuy wax ay waxyu, ñoom itam. 21 Ñu yegge ko Sóol, mu yebal yeneen ndaw, ñu dikk, di wax ay waxyu, ñoom it. Sóol dellooti yebal ay ndaw, ñetteel bi yoon, ñu dikk, di wax ay waxyu, ñoom itam. 22 Mu jóg moom ci boppam, jëm Raama. Mu dikk ba ca teen bu mag ba ca Seeku, daldi laajte ne: «Ana fu Samiyel ak Daawuda nekk?» Ñu ne ko: «Ña nga ca Nayot ca Raama.»
23 Sóol jubal yoonu Nayot ca Raama. Ba loolu amee, ca kawam, moom it, la Noowug Yàlla wàcc, muy wéy di wax ay waxyuy dem, ba àgg Nayot ca Raama. 24 Ci kaw loolu mu summiy yéreem, di wax ay waxyu moom it fa kanam Samiyel, daldi ne làndaŋ, ne duŋŋ, bëccëg keroog gépp ak guddi ga gépp. Looloo waral ñu naan: «Moo Sóol it ci yonent yi laa?»