Ma gonloo ñaan
4
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Éy Yàlla, yaw mi may àtte dëgg,
maa ngi woote, wuyu ma;
maa xatoon, nga yaatal ma.
Ngalla baaxe ma, nangul ma.
3 Yeen boroom daraja yi,
buleen yàqati sama der,
buleen sopp caaxaan, di sos. Selaw.
4 Xamleen ne Aji Sax ji day séddoo ku ko ragal,
te bu ma wooyee Aji Sax ji, mu dégg.
5 Loxleen te baña bàkkaar,
waxtaanleen ak seen ngegenaay te noppi.
6 Rendileen seen sarax yi war,
te wóolu Aji Sax ji.
7 Bare na ñu naan: «Ana ku nuy won lu baax?»
Éy Aji Sax ji, baaxe nu saw yiw!
8 May nga ma bànneexu xol
bu raw seen pepp mu tuurook biiñ bu wal.
9 Jàmm laay tëdde, nelaw,
Aji Sax ji, yaw doŋŋ yaa may dëël fu wóor.