Ma jëluy ñaan
5
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki toxoro, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
 
2 Éy Aji Sax ji, maa ngi àddu, déglu ma,
maa ngi onk, teewlu ma.
3 Sama Buur, sama Yàlla, déglul, ma ne wallóoy!
Yaw laay ñaan.
4 Aji Sax ji, ag suba, ngay dégg sama baat,
suba su ne ma diis la samay dagaan,
di séentu.
 
5 Doo Yàlla ju safoo coxor,
yaw lu bon du la daloo.
6 Ku réy du taxaw fi sa kanam,
kuy def lu ñaaw, bañ nga ko.
7 Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen,
sib kuy bóomeek kuy wore.
 
8 Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër,
sujjóotal sa bérab bu sell, wormaale la.
9 Éy Aji Sax ji, wommate ma sa njekk ndaxi noon,
te xàllal ma saw yoon.
 
10 Ñii, lu ñu wax, wérul,
seen xol a mébét njekkar,
seenug boli di bàmmeel bu ne ŋàpp,
ñuy naxe làmmiñ wu neex.
11 Éy Yàlla, topp leen,
ñu fakktaloo seeni pexe;
xalabal ñii barey moy,
ñoo la gàntal.
 
12 Képp ku la làqoo, yal na bég,
di saxoo sarxolle, nga di ko yiir,
te ku la sopp di la bége.
13 Aji Sax ji yaw kat, yaay barkeel ku jub,
yiire ko saw yiw, fege ko.