Jarag a ngi woote wall
6
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd ak xalamu juróom ñetti buum, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Éy Aji Sax ji, bul mer, ba di ma rëbb,
bul xadaru, ba di ma mbugal.
3 Aji Sax ji, damaa néew doole, yërëm ma!
Éy Aji Sax ji, sama yaram a tas, dàmp ma!
4 Sama xol a jeex tàkk.
Aji Sax ji, loo deeti xaar nag?
5 Éy Aji Sax ji, délsil, xettli ma!
Walloo ma sa ngor.
6 Deesul dee ba fàttliku la;
ku dugg njaniiw, nu mu lay sante?
7 Onk naa ba loof, di fanaanee jooy,
sama lal di féey,
ba far seeye rongooñ.
8 Saay gët a ngi xóot ndaxu naqar,
boole ci giim ndax tooñi noonoo noon.
9 Yeen, defkati ñaawtéef yépp, xiddileen ma!
Aji Sax ji dégg na saay jooy,
10 Aji Sax ji dégg na saay dagaan,
Aji Sax jii nangu na samag ñaan.
11 Noon yépp a am gàcce, ba jàq lool,
ne wërëñ ak gàcceg mbetteel.