Yàllaa man ag fitt
64
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat;
ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu.
3 Làq ma pexey ku bon,
ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.
4 Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar,
di fitte seeni kàdduy wextan,
5 di jam ku ñu tëru te deful dara;
jekki jam ko, te tiituñu ci dara.
6 Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar,
di diisoo na ñuy làqe ay fiir,
te naan: «Kenn du ko gis!»
7 Dañuy lal pexem njubadi te naan:
«Lal nanu pexe mu mat sëkk.»
Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!
8 Waaye Yàllaa leen di jamu fittam,
ñu jekki daanu.
9 Seen làmmiñ a leen di fakkastal,
ba ku leen xool wëcc bopp.
10 Ñépp a ciy am tiitaange,
bay siiwal la Yàlla def,
tey xalaataat jëfam jooju.
11 Ku jub bége Aji Sax ji, làqoo ko.
Képp ku namm njub, damu.