Yàllaay nangul suuf
65
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ,
yaw lees di jëfeel ab dige.
3 Yaw miy nangug ñaan,
yaw la képp di wuysi.
4 Samay ñaawtéef man na ma,
waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.
5 Ndokklee koo tànn, woo ko,
mu dale say ëtt,
di xéewloo sa ngëneeli kër,
ak sa sellngay dëkkuwaay.
6 Defal nga nuy kéemaan,
nangug ñaan ci njekk,
yaw Yàlla, mi nuy wallu,
di yaakaaru àddina wërngal këpp,
ba ca géej gu sore ga.
7 Yaa dëje tund yu mag yi doole,
gañoo sa kàttan,
8 di dalal riirum géej aki gannaxam,
ak coowal xeet yi,
9 ba waa cati àddina yéemoo say firnde,
waa penkook sowu di sarxolle.
10 Yaa dikke suuf am wal,
nangul koo nangul.
Dexu Yàllaa fees ndox,
ngay may nit peppam,
ni nga ko waajale suuf si,
11 di suuxat ngàbb mi,
maasalee ko jal yi,
sottiy waame, mu mokk,
cax ma, nga barkeel.
12 Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel,
foo jaare, xéewal walangaan.
13 Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan,
li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.
14 Joor gaa ngi, jur gi muur,
xur yi sàngoo pepp,
lépp di xaacook a woy.