Ku ñu fitnaal a ngi ñaan
69
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel Daawuda.
2 Éy Yàlla, wallu ma!
Ndox maa ngi ma tollu ci put.
3 May suux ci ban bu xóot,
te awma fu ma teg tànk.
Maa ngi nii ci ndox mu xóot,
gannax yi mëdd ma.
4 Ma woote wall ba tàyyi,
sama put gi wow koŋŋ.
Ma séentu la, yaw sama Yàlla,
ba samay gët giim.
5 Sama kawari bopp sax,
ñi ma bañ ci daraa ko ëpp.
Ñu bare doole, bëgg maa sànk,
noonoo ma ci dara.
Sàccuma, nara fey!
6 Yaw Yàlla, xam nga sama jëfi dof,
te samay tooñ umpu la.
7 Yàlla buma rusloo ñi la yaakaar,
yaw Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
yàlla buma gàcceel ñi la topp,
yaw Yàllay Israyil.
8 Yaa tax ma dékku, ñu di ma sewal,
ma rus ba sëlmoo gàcce.
9 Jaambur laa léegi ci saay bokk,
mel ni doxandéem sama biir doomi ndey.
10 Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk,
te jëf ji ñu la sewale man la dal.
11 May jooy, di woor,
ñu di ma sewal.
12 Ma sol ay saaku, di ko ñaawloo,
ñu di ma léebu.
13 Waa pénc ma di ma tooge,
màndikat yi di ma woyal.
14 Waaye man, Aji Sax ji, yaw laay dagaan.
Éy Yàlla, na tey di bésub yiw.
Ngalla nangul ma ci sa ngor lu yaa
ak sa wall gu wóor.
15 Xettli ma ci ban bi, ma baña suux,
xettliku ci samay noon.
Rikk génne ma yii xóotey ndox,
16 ba gannax du ma mëdd,
xóotey géej du ma warax,
pax du ma kepp.
17 Éy Aji Sax ji, yaa rafet ngor, nangul ma!
Geesoo ma sa yërmande ju yaa!
18 Bu ma làqu, Sang bi.
Jàq naa, gaawe ma.
19 Jege ma, jot ma,
musal ma ci noon yi!
20 Yaa gis ñu di ma sewal, di ma ruslook a torxal,
yaa ngi ne jàkk ci noonoo noon.
21 Dees maa sewal, sama xol jeex, ma wopp;
may sàkku yërmande, awma ko;
ku ma dëfal it, gisuma ko.
22 Tooke lañu ma leel,
ma mar, ñu nàndal ma lu forox.
23 Yal na seen ndab di seenum yeer,
seeni am-di-jàmm di seenug fiir.
24 Yal na seeni gët giim, ba dootu gis;
yal na seen ndigg rëcc fàww.
25 Yal nanga leen yuri mbugal,
sa mer tàkk, dab leen.
26 Yal na seeni dal gent,
seeni xayma wéet.
27 Yaw, nga duma ba noppi, ñu toppaat ca,
nga gaañ, ñu siiwal mitit wa.
28 Dencal leen tooñ ci kaw tooñ,
te yàlla buñu tàbbi ci sag njekk.
29 Yal nañu leen far ca téereb dund ba,
bañ leena limaale ca aji jub ña.
30 Man de, damaa jàq, tiis.
Éy Yàlla, yal naa làqoo sag wall.
31 Damay woy Yàlla, teral ko,
màggal ko, sant ko.
32 Mu gënal Aji Sax ji saraxu yëkk,
aki béjjénam aki wewam.
33 Néew-ji-doole di gis, bége,
kuy sàkku Yàlla yokku fit.
34 Aji Sax ji day dégg néew-ji-doole moos,
te du sàggane ñoñam ñi ñu njoñ.
35 Na asamaan ak suuf màggal Yàlla,
mook géej ak lu cay yëngoo.
36 Yàlla kat mooy musal Siyoŋ,
tabaxaat dëkki Yuda yu mag yi,
ay nitam moom, dëkke.
37 Askanu jaamam ñee koy jagoo,
ay soppeem a koy dëkke.