Yàlla, gaawe ma
70
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ñeel Daawuda, di woy wuy fàttlee.
 
2 Yàlla, wallu ma!
Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
 
3 Kuy wut sama bakkan,
yal na rus, torox ne tott.
Kuy bége sama loraange,
yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.
4 Kuy ñaawle,
yal na dellu gannaaw, torox.
 
5 Képp ku lay sàkku,
yal na bég, di la bànneexoo.
Képp ku sopp sag wall,
yal na jàppoo: «Yàlla màgg na!»
 
6 Man de, néew naa doole, ñàkk naa.
Éy Yàlla, gaawe ma.
Yaw yaa may wallu, xettli ma.
Éy Aji Sax ji, bu ma yeexe.