Mag a ngi séentu njekku Yàlla
71
1 Aji Sax ji, yaw laa làqoo,
yàlla buma rus mukk.
2 Xettlee ma sa njekk, yiwi ma;
ngalla teewlu ma, te wallu ma.
3 Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu
bu may rawesi saa su ne,
te nga dogal sama mucc.
Yaw yaa may téye, di ma aar.
4 Éy sama Yàlla, musal ma ci dooley ku bon
ak ab saaysaay ak ab néeg.
 
5 Boroom bi, Aji Sax ji, yaw de laa yaakaar,
dale laa wóolu ba may ndaw.
6 Yaw laa wéeroo ba may juddu;
yaw yaa ma roccee sama biiru ndey.
Yaa yelloo sama cant fàww.
7 Firndey alkànde la ma ñu bare xoole woon,
te yaw ngay sama rawtu bu wóor.
8 Samay kàddu sag cant la fees
ak di la saxoo darajaal.
 
9 Ngalla bu ma wacc, mag laa;
bu ma ba fi doole jeexe.
10 Noon yaa nga may tooge,
ñi may tëroo ngay diisoo,
11 naan: «Yàlla wacc na ko,
nan ko dàq, jàpp;
kenn du ko wallu.»
12 Éy Yàlla, bu ma sore.
Sama Yàlla, gaawe ma.
13 Samay seytaane,
yal nañu leen rusloo, sànk leen.
Ñi may wuta lor,
yal nañu leen gàcceel, sewal leen.
14 Man may saxoo yaakaar,
di la sant, di santati.
15 May siiwal sa njekk,
di yendoo waxtaane say wall,
doonte lim ba wees na ma.
16 Boroom bi, Aji Sax ji, ma dikke la sag njàmbaar,
di tudd sa njekk gu wéet.
17 Éy Yàlla, ba may ndaw, nga ma xamal say kéemaan,
te ba tey jii maa ngi koy biral.
18 Éy Yàlla, bu ma bijjaawee ba weex tàll it, bu ma wacc,
ba keroog may xamal maasu tey sa doole,
xamal ñi ciy topp ñépp sag njàmbaar.
19 Céy Yàlla, sa njekk àkki na fa kawa kaw.
Def nga lu réy.
Yaw Yàlla, ana ku mel ni yaw?
20 Won nga ma ay yoon coonooki tiis,
waaye yaa may dundalaat,
ma mucc xóotey suuf.
21 Yal nanga ma gëna sagal,
geesu, bégal ma.
 
22 Man it sama Yàlla, ma xalam, sant la
ngir sa kóllëre.
Aji Sell ji séddoo Israyil,
dama lay woy aki xalam,
23 sarxolle, woy la,
bége sag njot.
24 May yendoo siiwal sa njekk
nde ña ma doon wuta lor
lañu rusloo, sewal leen.