Déggal Yàlla, jariñu
81
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, giiroo ci Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit.
 
2 Sarxolleleen ci Yàlla, mi nuy dooleel;
xaaculeen ci Yàllay Yanqóoba.
3 Yékkatileen woy te jiin,
xalam neex, ànd ak moroom ma.
4 Wal-leen liit gi ci Terutel weer wi,
ak weer wu birale bésu màggal.
5 Loolu wartéefu Israyil la,
di ndigalu Yàllay Yanqóoba,
6 di ndénkaane lu mu dénk waa kër Yuusufa,
ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra.
Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan:
7 «Sippi naa leen,
woyofal seeni yoxo.
8 Ngeen jàq, woo ma, ma xettli leen,
wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya,
te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.
9 Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen.
Éy Israyil, su ngeen ma déglu woon!
10 Buleen fat tuuru jaambur,
buleen sujjóotal tuuru doxandéem.
11 Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla
ji leen yékkatee réewum Misra.
Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.
 
12 «Waaye sama ñoñ déggaluñu ma,
Israyil gii nangulu ma.
13 Moo tax ma bërgël leen ak seenug të,
ñuy wéye seeni pexe.
14 Éy su ma sama ñoñ déggaloon,
éy su Israyil toppoon samay nammeel!
15 Ci saa si laay torxal seeni noon,
duma seeni bañ,
16 ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal,
te àppam du jeex ba fàww.
17 Kon yeen, ma leel leen ngën-gi-pepp,
reggal leen lem ju doj xelli.»