Yàllaay àtte ndawi péncam
82
1 Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam,
di àtte ndawi péncam, naan:
2 «Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ,
ak di faral ku bon? Selaw.
3 Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim,
tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol.
4 Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana,
di leen xettli ci ku bon.
5 «Ndawi péncum Yàlla yii xamuñu, dégguñu;
xanaa di doxe lëndëmu ñaawtéef,
ba kenuy suuf yépp di jaayu.
6 «Dama ne ay yàlla ngeen,
yeen ñépp di njabootu Aji Kawe ji.
7 Waaye du leen tee dee ni doom aadama,
du leen tee daanu ni képp kuy njiit.»
8 Ngalla Yàlla, taxawal, àtte àddina,
yaw yaa séddoo xeetoo xeet.