Aji Sax ji, loo dige woon?
89
1 Muy taalif bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra.
 
2 Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww,
di biral wormaam sët ba sëtaat.
3 Dama ne, sa ngor dàkk la sax,
fa asamaan nga dëël sa worma.
4 Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn,
muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
5 “Damay saxal sa askan ba fàww,
samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
 
6 Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore,
ndajem ñu sell ña di la joobee sa worma.
7 Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kawa kaw?
Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
8 Yàlla, ji ñu terala teral ci jataayu ñu sell ñi,
te mu gëna raglu lu ko wër?
9 Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
Ki Sax, ana ku tollook yaw doole?
Yaw mi worma féete fu ne!
 
10 Yaw yaa man géej gu sàmbaraax;
gannax ya fuddu, nga dalal.
11 Yaa fàdd Raxaba, bóom ko,
tasaare say noon ci sa doole.
12 Yaa moom asamaan, yaa moom suuf.
Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
13 Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk.
Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
14 Yaa àttan, jàmbaare;
sa loxo di dooley neen,
sa ndijoor ca kaw!
15 Njekk ak njub a lal sab jal,
ngor ak worma dox jiitu la.
 
16 Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee,
di niitoo saw yiw,
17 ànd di la bége bés bu ne,
sag njekk siggil leen.
18 Seen darajay doole, yaw a.
Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.
19 Sunu kiirlaay lii, Aji Sax jeey boroom;
sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israyil ay boroom.
 
20 Wax nga say wóllëre ci peeñu,
ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi,
dénk ko ndimbal.
21 Gis naa sama jaam Daawuda,
fale ko sama diw gu sell,
22 ànd ak moom, saxal ko,
di ko dooleel.
23 Noon du ko bett,
ku bon du ko torxal.
24 Ay bañam, ma rajaxe;
ay noonam, ma fàdd,
25 sama wormaak sama ngor di ko gunge,
may yokk kàttanam.
26 Géej, ma teg ci loxoom,
dex, ma ne ca tegg ndijooram.
27 Moo ma naa: “Yaay sama baay,
di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”
28 Te it maa koy def samab taaw,
tiimale ko buuri àddina,
29 sàmmal ko sama ngor ba fàww,
feddlil ko sama kóllëre.
30 Damay saxal askanam ba fàww,
yàggal ab jalam ni asamaan.
31 Bu ay sëtam wàccee sama yoon,
baña doxe samay ndigal,
32 mbaa ñu xëtt sama dogali yoon,
baña sàmmonteek samay santaane,
33 ma bantale leen seenug moy,
dumaa leen seen ñaawtéef.
34 Waaye duma ko daggal sama ngor,
te duma ko ñàkke worma.
35 Duma fecci sama kóllëre,
te duma toxal sama kàddu.
36 Benn yoon laa ko giñ ci sama sellnga,
duma fen Daawuda:
37 askanam, dàkk;
ab jalam fi sama kanam ni jant bi,
38 ak weer wi sax ba fàww,
dib seede bu wér ca niir ya.» Selaw.
 
39 Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal,
mere ko, wacc ko.
40 Fecci nga sa kóllëreek sab jaam,
foq nguuram, detteel ko.
41 Bëtt nga miiram yépp,
saam ay tataam,
42 ku fa jaare, jël ca alalam,
mu doon mbalitu dëkkandoo yi.
43 Yékkati ngay bañam,
noonam yépp di ree.
44 Dayal nga saamaram,
te taxawuwloo ko cib xare.
45 Xañ nga ko darajaam,
rattax ngànguneem fa suuf.
46 Dagg nga fani ngoneem,
sang ko gàcce. Selaw.
 
47 Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex?
Xanaa doo làqu fàww nii,
sa mer di boy?
48 Bàyyi ma xel, samay fan yàggul.
Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?
49 Ana kuy dund te du dee?
Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? Selaw.
50 Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe
te nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma?
51 Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi,
ak xeet yu bare yi ma yenu yépp.
52 Aji Sax ji, say noon a ngi sewal
buur bi nga fal, ne ko dann.
 
53 Cant ñeel na Aji Sax ji ba fàww.
Amiin, amiin.