Doom aadama yàggul
90
1 Muy ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga.
Boroom bi, yaa nu masa fat
maasoo maas.
2 Bala tund yee juddu,
bala ngay sos suuf ak àddina,
yaa mas di Yàlla, ba fàww.
3 Yaay delloo doom aadama ci pënd,
ne ko: «Yaw, doom aadama, dellul!»
4 Junniy at ci yaw
daa gaaw ni démb ak tey,
mbete waxtu yu néew ci wattub guddi.
5 Yaay buub nit, nelawal ko.
Suba mu jebbi nim ñax,
6 xëy, jebbi, naat;
ngoon mu lax, wowal.
7 Soo meree kay, nu sànku,
nga xadaru, nu jàq.
8 Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw,
te sunu mbóot leer na la.
9 Sunu giiru dund nga di nu mere,
sunuy fan jeex ni noo guy naaw.
10 Sunu àppu dund di juróom ñaar fukki at,
ku dëgër ba dëgër, juróom ñett fukk;
li ci ëpp di coonooku tiis,
ne fëyy, nu wéy.
11 Ana ku xam sa dooley mer
ak sa xadar ju raglu?
12 Yal nanga nu xiir ci lim sunuy fan,
ba nu mana dawal xel mu rafet.
13 Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar?
Ngalla yërëmal sa jaam ñi.
14 Nu xëy, nga reggal nu sa ngor,
nuy sarxolle, bànneexoo ko sunu giiru dund.
15 Bànneexal nu limu fan yi nga nu mbugal,
diirub ati tiis yi nu dund.
16 Yal na sa jaloore leer sa jaam ñi,
sa daraja leer seeni doom.
17 Boroom bi sunu Yàlla, ngalla baaxe nu.
Sottalal nu sunuy liggéey,
rikk, sottalal nu sunuy liggéey.