Aji Sax jee mat kaaraange
91
1 Ku dëkke kiiraayu Aji Kawe jiyaa këroo keppaaru Aji Man ji.
2 Dama naa Aji Sax ji:
«Yaw laay làqoo, di la fegoo;
ngay sama Yàlla ji ma doyloo.»
3 Kii kay moo lay musal cig fiir
ak loraangey mbas.
4 Kiiraayam la lay sànge,
nga yiiru, làqu;
wormaam yéew la, di la aar.
5 Doo ragal njàqarey guddi
mbaa fittu bëccëg
6 mbaa mbas mu yooteg lëndëm,
ak balaa buy fàdde njolloor.
7 Junni daanu fi sa wet,
fukki junni (10 000) daanu fi sa ndijoor,
du tax mu jege la.
8 Say gët nga ciy teg,
di seetaan ku bon di jot yoolam.
9 Yaw mi màkkaanoo Aji Sax ji,
Aji Kawe jii di sama rawtu,
10 genn loraange du la dab,
balaa du jege sa xayma.
11 Ay malaakaam la lay booleel,
ñu di la sàmm foo jëm.
12 Seeni loxo lañu lay leewoo,
ba doo fakkastaloow doj.
13 Dangay falaxe jaan ak gaynde,
di rajaxe ñàngóor ak sibi.
14 Yàlla da naa: «Kii de man la safoo,
ma di ko xettli.
Man la xam, te maa koy teg fu wóor.
15 Mu woo ma, ma wuyu ko;
mook man ci biir njàqare,
ma xettli ko, darajaal ko,
16 reggal koy fan,
baaxe ko samag wall.»