Nguurug Aji Sax ji njekk la
97
1 Aji Sax jeey Buur, na àddina bég;
dunoo dun bànneexu.
2 Ay xàmbaar a ko yéew,
njekk ak njub lal ab jalam.
3 Sawaraa dox, jiitu ko,
di xoyomi noonam wetoo wet,
4 ay melaxam leeral àddina,
waa àddina gis, di pat-pati;
5 tund yi ne soyox seey fi kanam Aji Sax ji
boroom àddina sépp.
6 Asamaan a ngi biral njekkam,
xeetoo xeet di gis darajaam.
7 Gàcce ñeel na kuy jaamu jëmmi tuur,
di puukarewoo ay yàllantu.
Yeen yàllay xeet yépp, sujjóotal-leen kii,
8 Siyoŋ dégg ca, bég,
waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.
9 Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp;
yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur.
 
10 Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon.
Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem,
di leen musal ci ku bon.
11 Jub, leerlu;
jubal, bég.
12 Yeen aji jub ñi, bànneexooleen Aji Sax ji,
sante ko sellngaam.