Woyleen Aji Sax jiy àttesi
98
1 Muy kàddug Sabóor.
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
moo def ay jaloore,
kàttanam ak sellngay dooleem
jox na ko ndam li.
2 Aji Sax jee xamleg wallam,
feeñal njekkam, xeet yi gis.
3 Moo dencal bànni Israyil ngoram,
dencal ko wormaam,
àddina ba mu daj di gis
ni nu sunu Yàlla walloo.
4 Yeen àddina sépp, xaacul-leen Aji Sax ji,
sampleen, sarxolle te woy!
5 Xalamal-leen Aji Sax ji, woyal ko,
xalamal ko, woyati.
6 Wal-leen liit yi, wal bufta yi
te xaacul Buur Aji Sax ji!
7 Na géej riirandook li ko fees,
mook àddinaak li ci biiram,
8 dex tàccu,
tund sarxolleendoo,
9 gatandoo ko Aji Sax jiy dikk,
àttesi àddina,
di àtte dun bi njekk,
tey àttee xeet yépp dëgg.