Yàllaay walloo dooleem
114
1 Ba Israyil bàyyikoo fa Misra,
ba waa kër Yanqóoba dëddu làkk-kat yooya,
2 ca la Yuda doon kër Aji Sax ji,
giirug Israyil googu doon ab jagleem.
 
3 Géej gaa leen gis, daw,
dexu Yurdan a deltu gannaaw,
4 tund yu mag yiy curpi niy kuuy,
di curpeendook tund yu ndaw yi niy mbote.
 
5 Moo géej, loo xewle bay daw?
Yaw, dexu Yurdan, looy deltu gannaaw?
6 Tund yu mag yee, lu ngeen di curpi niy kuuy?
Yeen, tund yu ndaw yi, lu ngeen di curpi niy mbote?
 
7 Suufee, loxalal Boroom bi,
Yàllay Yanqóoba mii,
8 ki soppliw doj ndox mu taa,
xeer wu ne sereŋ, mu def bëtu ndox.