Ku wóolu Yàlla barkeel
115
1 Bu muy nun, Aji Sax ji, bu muy nun,
saw tur nga wara teral,
ngir sa ngor ak sa worma.
2 Bu yéefar yi ne mukk:
«Moo ñii, ana seen Yàlla?»
3 Te yaw sunu Yàlla, yaa ngi asamaan,
di def lu la soob.
4 Seeni tuur xaalis laak wurus,
di liggéeyu doom aadama:
5 am gémmiñ te du wax,
ami gët te du gis,
6 ami nopp, du dégg,
ami wakkan, du xañtu,
7 ay yoxo it te du yég,
ay tànk it te du dox,
du xàddmiku sax.
8 Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom,
ñook ñi leen wóolu ñépp.
 
9 Éy Israyil, wóolul Aji Sax ji,
moo lay jàpple, di la aar.
10 Yeen waa kër Aaróona, wóoluleen Aji Sax ji,
moo leen di jàpple, di leen aar.
11 Yeen ñi ragal Aji Sax ji, wóoluleen Aji Sax ji,
moo leen di jàpple, di leen aar.
 
12 Aji Sax jee nuy bàyyi xel, di nu barkeel,
di barkeel kër Israyil,
di barkeel kër Aaróona.
13 Aji Sax jeey barkeel ku ko ragal,
mag ak ndaw.
 
14 Yal na leen Yàlla ful,
ful seeni doom.
15 Yal nangeen barkeeloo Aji Sax ji,
ki sàkk asamaan ak suuf.
16 Asamaan, asamaanu Aji Sax jee,
suuf la dénk doom aadama.
17 Du ku dee mooy màggal Ki Sax,
du kenn ku tàbbi réewum tàbbi-selaw!
18 Nun, nooy sargal Ki Sax,
tey ak ëllëg.
Màggal-leen Ki Sax!