Way-gëm ñaa ngi sant
134
1 Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla.
Ayca, santleen Aji Sax ji,
yeen jaami Aji Sax ji yépp,
yeen ñiy taxawe kër Aji Sax ji guddi.
2 Yékkatileen seeni loxo bérab bu sell ba,
te sant Aji Sax ji.
3 Yal na la Aji Sax ji barkeele fa Siyoŋ,
moom mi sàkk asamaan ak suuf.