Aji Sax ji jot na Israyil
135
1 Màggal-leen Ki Sax!Màggal-leen turu Aji Sax ji,
éey jaami Aji Sax ji, màggal-leen,
2 yeen ñi taxawe kër Aji Sax ji,
fi sunu biir ëttu Yàlla bi.
3 Màggal-leen Ki Sax, Aji Sax jee baax!
Kañleen ko, kee sopplu!
4 Ki Sax a taamu Yanqóoba,
muy Israyil mi mu séddoo.
5 Maa xam ne Aji Sax ji màgg na!
Sunu Boroom a sut lépp lu ñuy jaamu.
6 Lépp lu Aji Sax ji namm,
moom lay def asamaan ak suuf,
ak biir géej ak xóote yépp.
7 Mooy yékkateey niir fa cati àddina,
sàkkal taw ay melax,
yebbee ngelaw cay dencam,
8 fàdd luy taaw fa Misra,
doom aadama, ba ci mala.
9 Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir,
ñeel Firawnaak jawriñam ñépp.
10 Moo duma ay xeeti xeet,
bóom buur yu mag yi,
11 muy Siwon buurub Amoreen ña,
ak Og buuru Basan,
ak buuri Kanaan ñépp.
12 Moo nangu seen réew, séddale,
bànni Israyil ñiy ñoñam séddoo.
13 Aji Sax ji, sa tur ba fàww;
Aji Sax ji, sa woy a saxal maasoo maas.
14 Aji Sax ji kay ay àtte ñoñam ñi,
di ñeewante jaamam ñi.
15 Tuuri yéefar yi, xaalis ak wurus,
loxoo ko sàkk.
16 Am gémmiñ te du wax,
ami gët te du gis,
17 ami nopp te du dégg,
du sax noowal bakkan.
18 Ñi sàkk yii tuur, yal nañu mel ni ñoom,
ñook ñi leen wóolu ñépp.
19 Éey waa kër Israyil, santleen Aji Sax ji!
Éey waa kër Aaróona, santleen Aji Sax ji!
20 Éey waa kër Lewi, santleen Aji Sax ji!
Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen Aji Sax ji!
21 Nañuy sante Aji Sax ji Siyoŋ,
moom mi dëkke Yerusalem.
Màggal-leen Ki Sax!