Jooye nanu àll
137
1 Ca tàkkal dexi Babilon,foofa lanu daa toog,
fàttliku Siyoŋ, jooy.
2 Ca garab ya
lanu daa wékk sunuy xalam.
3 Fa la nu sunuy sang daa woyloo,
not nu, bëgg nu bégal leen,
naan: «Woyal-leen nu ci woyi Siyoŋ.»
4 Moo nu nuy woye woyu Aji Sax ji
kaw suufas yéefar?
5 Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte,
yal na ma doole dëddu!
6 Yerusalem, su ma la fàttlikuwul,
fonk la, ba gën laa bége lépp,
yal na sama làmmiñ tafoo sama denqleñ.
7 Aji Sax ji, fàttlikul Edomeen ña,
keroog jantub Yerusalem,
ba ñu naan: «Màbbleena màbb,
ba kenug dëkk bi siiñ!»
8 Yeen waa Babilon, gi ñu nara fàllas,
ndokklee ku leen fey jëf,
ja ngeen nu def!
9 Ndokklee ku ne cas seeni fere,
tas ciw doj!