Yàllaa am kóllëre
136
1 Nangeen sante Aji Sax ji mbaaxam.Kee saxoo ngoram!
2 Santleen Yàllay yàlla yi.
Kee saxoo ngoram!
3 Santleen Sangu sang yi.
Kee saxoo ngoram!
4 Moo wéetoo jaloore yu mag yi.
Kee saxoo ngoram!
5 Moo sàkke asamaan manoore.
Kee saxoo ngoram!
6 Moo lal suuf ca kaw ndox ma.
Kee saxoo ngoram!
7 Moo sàkk leer yu mag yi:
Kee saxoo ngoram!
8 jant bi yilif bëccëg,
Kee saxoo ngoram!
9 weer ak biddiiw, guddi.
Kee saxoo ngoram!
10 Moo fàdd taawi Misra yu góor ya,
Kee saxoo ngoram!
11 seppee bànni Israyil ca ñoom,
Kee saxoo ngoram!
12 ci dooley loxoom ak kàttanu përëgam.
Kee saxoo ngoram!
13 Moo xar géeju Barax ya yaar,
Kee saxoo ngoram!
14 jàllale bànni Israyil ca digg ba.
Kee saxoo ngoram!
15 Moo xalab Firawnaak mbooloom ca géeju Barax ya.
Kee saxoo ngoram!
16 Moo jiite ñoñam ca màndiŋ ma.
Kee saxoo ngoram!
17 Moo duma buur yu mag ya,
Kee saxoo ngoram!
18 bóom buur yu màgg ya,
Kee saxoo ngoram!
19 reyaale Siwon buurub Amoreen ña,
Kee saxoo ngoram!
20 reyati Og buuru Basan.
Kee saxoo ngoram!
21 Moo nangu seen réew, joxe,
Kee saxoo ngoram!
22 sédde Israyil ma dib jaamam.
Kee saxoo ngoram!
23 Ci biir notaange la nu geesoo,
Kee saxoo ngoram!
24 ne nu siféet ci loxoy noon ya.
Kee saxoo ngoram!
25 Mooy leel bépp boroom bakkan.
Kee saxoo ngoram!
26 Santleen Yàlla mi ci asamaan!
Kee saxoo ngoram!