Ku ñu toŋal a ngi ñaan
140
1 Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
2 Éy Aji Sax ji, xettli ma ci ku bon,
musal ma ci nitu fitna,
3 kuy nas lu bon,
tey saxoo di sookey xare,
4 daas làmmiñam ni jaan,
guux daŋaru ñàngóor. Selaw.
5 Éy Aji Sax ji, aar ma ci loxol ku bon,
musal ma ci nitu fitna,
ku may fexee fakktal.
6 Ñu bew ñee ma làqali yeer,
lalal may buum aki caax,
feggal ma seeni fiir ci yoon wi. Selaw.
7 Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla;
Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
8 Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole,
yaa ma yiir keroog bésub xare.
9 Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam,
bul joyal pexeem, muy yékkatiku. Selaw.
10 Ñi ma sam, yal na seen ayu làmmiñ
këppu seen kaw bopp.
11 Yal nañu këppoo xali sawara,
tàbbi ciy pax te dootuñu jóg.
12 Kuy yàq der, yàlla bumu toog ci réew mi.
Nitu fitna, yal na ko ay topp, ba dal ci kawam.
13 Xam naa ne Aji Sax jeey jox néew-ji-doole dëgg;
di sàmm àqu baadoolo.
14 Ku def njekk kay a lay sant;
ku jub dëkke saw yiw.