Yàlla, sàmmal sama làmmiñ
141
1 Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda.
Aji Sax ji, woo naa la, gaawe ma!
Bu ma lay woo, teewlu ma.
2 Yal nanga ma nangul samag ñaan
ni cuuraay lu ñu la taalal,
yoxo yi ma la tàllal di saraxu ngoon soo gërëm.
3 Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ,
saytul ma sama kàddu.
4 Bu ma xiir ci lu aay,
may jëfe jëf ju bon,
ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw,
di wàlli seeni bernde.
5 Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor,
bantal ma ci ngor.
Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ.
Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.
6 Yal nañu fenqe seeni njiit ciw doj,
ba noon yi xam ne dëgg laa wax.
7 Ni ñuy gàbbe suuf ba mu ne ŋafeet,
ni la njaniiw di ŋaye,
aw seeni yax yu tasaaroo.
8 Aji Sax ji Boroom bi, yaw laa wékki gët,
yaw laa làqoo,
bu ma seetaan, ma dee.
9 Musal ma ci yeer yi ñu ma gasal,
ak fiir yi ma defkati ñaawtéef yi tegal.
10 Yal na ku bon tàbbi cig fiiram,
te man ma teggi, wéy.