Aji Sax ji rekk a ma yég
142
1 Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma.
2 Ma àddu, ñaan Aji Sax ji;
àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
3 sippi ko sama tawat,
diis ko sama njàqare.
4 Bu ma yoqee,
ràññee nga samay jéego;
yoon wi may jaare
lañu ma làqal am yeer.
5 Ma geesu ndijoor, xool;
du kenn ku ma faale.
Rawtu réer ma,
du kenn ku sama bakkan saf.
6 Aji Sax ji, ma woo la wall;
ma ne, yaay sama kiiraay,
di sama séddoo fi kaw suuf.
7 Teewlul, ma ne wóoy,
damaa manatul,
xettli ma ci ñi ma topp,
dañu maa ëpp doole.
8 Ngalla génne ma fi ma tëje,
ma sant la.
Man la way-gëm ñi di yéew ëllëg,
yaa may xéewale ab yool.