Aji Sax ji, laggsil
144
1 Ñeel Daawuda.
 
Cant ñeel na Aji Sax ji ma sës,
mu di ma jàngal xeex,
di ma tàggat ngir xare,
2 di sama wóllëre, di ma yiir,
di ma làq, di ma xettli,
di ma aar, ma di ko làqoo,
mu di ma nangulal ay xeet.
3 Aji Sax ji, luy nit, ba nga di ko ràññee?
luy doom aadama, ba nga di ko faale?
4 Nit ni ngelaw,
ay fanam di takkndeer, wéy.
5 Aji Sax ji, firil asamaan, wàcc;
laal tund yi, ñu saxar.
6 Melaxal, falaxe noon yi;
fittal, ñu fëlxoo,
7 nga yóotoo ma fu kawe,
xettli ma, wallu ma ci doxandéem
yi def wali wal fi sama kaw,
8 di fen,
di giñ ay fen.
9 Yàlla, naa la woyal woy wu yees,
xalamal la xalamu fukki buum.
10 Yaay may buur yi ndam,
yaa musal sa jaam ba, Daawuda
ci saamar bu aay.
11 Musal ma, xettli ma
ci loxol doxandéem
yiy fen, di giñ ay fen.
 
12 Su boobaa sunu doom yu góor
màgge ndaw, ni gàncax gu mat sëkk;
sunuy janq jekk ni doji yett,
yu ñu tabaxe kër buur.
13 Sunuy sàq feese wirgoy wirgo,
sunuy gàtt jur junni,
ba fukki junni (10 000) ci parlu yi,
14 nag yi ëmb ba diis,
du mbas, du biir bu yàqu,
te deesu fi yuuxoo pénc ya.
15 Ndokklee xeet wu am lii!
Ndokklee xeet wu yàllawoo Aji Sax ji!