Ma kañ Buur Yàlla
145
1 Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda.
Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal,
teral sa tur ba fàww.
2 Bésoo bés ma di la sant,
di màggal sa tur ba fàww!
3 Aji Sax jee màgg te jara màggala màggal,
kii màggam amul kemu!
4 Na maasoo maas di màggal say jaloore,
di biral sa njàmbaarte.
5 Sa leeru teddnga ji ne ràññ,
ak sa jëf ju yéeme laay jàngat!
6 Sa dooley jëf ju raglu dees na ko jottli,
te sa màggaay maa koy yéene.
7 Sa mbaax gu réy, dees na ko tari,
te sag njekk, dees na ko woy.
8 Yiw ak yërmande, Aji Sax ji;
kee muñ mer te bare ngor!
9 Aji Sax jee baaxe ñépp,
di yërëm lu mu sàkk.
10 Aji Sax ji, lépp loo sàkk a lay gërëm,
sa wóllëre yi di la sant,
11 di tudd sa teddngay nguur,
tey dégtale sag njàmbaar,
12 doom aadama xam say jaloore
ak sa teddngaak sa darajay nguur.
13 Sa nguur ay nguur gu sax dàkk,
sa kilifteef ñeel maasoo maas.
Aji Sax ji daa sàmm ay waxam,
gore ciy jëfam.
14 Ku daanu, Aji Sax ji wallu;
ku sëgg, mu siggil.
15 Ñépp a la wékk bët, di yaakaar,
te bu jotee, yaa leen di leel,
16 tàllal sa loxo,
reggal luy dund, ba xolam sedd.
17 Aji Sax ji, jëfinam jépp njekk la,
jëfam jépp ngor la.
18 Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la,
képp ku ko woo wall te muy dëgg.
19 Nammeelu ku ko ragal, mu sottal;
yuuxam, mu dégg, musal.
20 Aji Sax jeey sàmm kuy soppeem,
di sànk képp ku bon.
21 Naa sàlloo sant Aji Sax ji,
na luy dund saxoo dàkk di màggal sellngay turam!