Kilifteef gu bees taxaw na
2
1 Mbir mii la Yàlla won Esayi doomu Amocc ci mbirum Yuda ak Yerusalem.2 Fan yu mujj ya, dees na taxawal
tundu kër Aji Sax ji,
Aji Sax ji mooy gëna kawe ci tund yi,
tiim tund yu ndaw yi,
xeet yépp riirandoo, wutsi ko.
3 Ay askan yu bareey dikk, naan:
«Dikkleen nu yéegi tundu Aji Sax ji,
fa kër Yàllay Yanqóoba,
mu xamal nuy yoonam,
ba nu doxe yooyu ñallam.»
Siyoŋ kat la ndigalu yoon di bawoo,
Yerusalem googu la kàddug Aji Sax ji di jóge.
4 Mooy àtte diggante xeet yi,
mooy dogalal ay askani askan,
ñu tëgg seeni saamar ay illéer,
def seeni xeej ay sàrt;
aw xeet dootu xàccil moroom ma saamar,
te dootuñu jàngati xare.
5 Yeen waa kër Yanqóoba,
kaayleen nu doxe leeru Aji Sax ji!
Bew, yàqule
6 Boroom bi, bàyyi nga waa kër Yanqóoba, sa ñoñ,
ndax jëfi waa penku lañu feese,
aki gisaanekat, ba mel ni waa Filisti,
te ñooy tàppante pasook doomi doxandéem yi.
7 Seen réew maa ngi ne gàññ ak xaalis ak wurus,
alal du jeex,
fas ne xas,
watiiri xare du jeex.
8 Seen réew maa ngi fees aki yàllantu;
ñuy sujjóotal seen liggéeyu loxo yooyu,
te ñoo ko sàkkal seen bopp.
9 Doom aadama torox na, ku ne detteelu,
waaye bu leen yékkati!
10 Ayca ca xunti ma,
làqujileen biiri pax,
ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab,
sore darajay màggaayam.
11 Bésub keroog booba,
ku bew bay regeju mooy detteelu,
sagub nit sàggiku,
Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.
12 Bés déy ñeel na Aji Sax ju gàngoor yi,
ca lay xaare képp ku bew ak ku reew,
ba kuy daŋŋiiral, detteelu.
13 Ca lay xaare garabi seedari Libaŋ
yi ne coleet, ba kawe,
ak garab yu mag ya fa Basan.
14 Ca lay xaare wépp tund wu mag wu ne coleet,
ak bépp jànj bu kawe,
15 ak jépp tata ju gudd,
ak bépp miir bu ñu dàbbli,
16 ak gaalu Tarsis gu mag gu mu doon,
ak gépp gaal gu taaru.
17 Bésub keroog booba,
kuy daŋŋiiral, detteelu,
sagub nit sàggiku,
Aji Sax ji doŋŋ mooy jagoo kawe.
18 Yàllantu yépp a naan mes,
19 nit ñi làquji biir xuntiy doj,
ruuruji biiri pax,
ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab,
sore darajay màggaayam,
kera buy taxaw, ba suuf di lox.
20 Bésub keroog booba,
yàllantuy xaalis ak wurus
ya nit sàkkal boppam, di leen sujjóotal,
ñoom lay sànni ca jaar yaak njugub ya,
21 ba mana làquji ca xunti ya
ak xarantey doj ya,
ba sore tiitaange ji Aji Sax ji sabab,
sore darajay màggaayam,
kera buy taxaw, ba suuf di lox.
22 Baleen nit,
noowal bakkan kese la!
Ana lees koy nawe?