Yuda salfaañoo na
3
1 Aji Sax ji Boroom bi, Aji Sax ju gàngoor yi kat,
mu ngi nii di jële Yerusalem ak Yuda,
lu doon wéeruwaay, di cëslaay,
muy dugub ju ñu yaakaaroon,
di ndox mu ñu yaakaaroon,
2 ak jàmbaar ak ñeyu xare,
akub àttekat akub yonent,
ak gisaanekat ak magum pénc,
3 ak njiitu juróom fukki dag, akub kàngam,
ak diglekatu buur, ak ndaanaanu liggéeykat,
ak jatkat bu xareñ.
4 «Maay def ay gone jiite leen,
di ñu yaroo seen sago, yilif leen.
5 Nit ñiy soxorante,
ku nekk ak moroomam, ku nekk ak dëkkandoom,
ndaw di ñàkke mag kersa,
sagaru nit sofental boroom daraja.
6 Nit dina ne nikk mbokk ma,
ca biir kër baayam, ne ko:
“Yaw mi dese mbubb, jiite nu,
ba lu bokk ci sunu gent bii, di sa kilifteef.”
7 Keroog kooka àddu ne ko:
“Duma leen mana fajal dara!
Du dugub, du mbubb fa sama kër,
dungeen ma def njiit!”»
8 Yerusalem day téqtalu,
Yuda fëlëñu.
Ñooy wax ak a jëf lu neexul Aji Sax ji,
di gàntal leeram gi teew.
9 Seen dëgër bët tuumaal na leen,
ñuy bàkkaar ni waa Sodom,
làquwuñu sax.
Wóoy, ngalla ñoom!
nde ñoo lor seen bopp.
10 Neleen aji jub ji mooy baaxle,
mooy yooloo añam.
11 Waaye wóoy ku bon, nde mooy bonle;
la mu def rekk lees koy def.
12 Bokk yi, ñu xalele ñoo leen di not,
ay jigéen yilif leen.
Bokk yi, seeni njiit a ngi leen di sànk,
lëndëmal nañu seeni yoon.
13 Aji Sax jaa ngi ci jataayu layoo,
moo jóg di àtte ay xeet.
14 Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange,
jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam.
«Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi,
la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.
15 Lu waral ngeen di dëggaate sama ñoñ,
nappaaje néew-doole yi?»
Kàddug Boroom bee, Aji Sax ju gàngoor yi.
Puukare sànk na jigéeni Siyoŋ
16 Aji Sax ji da ne:
«Jigéeni Siyoŋ a ngi daŋŋiiral,
di goŋeet-goŋeeti,
di regejook a rékk-rékkal,
samp um ndaag,
keleŋal lami wëq.»
17 Moo tax Boroom beey wat jigéeni Siyoŋ nel,
Aji Sax jeey muri seen jë.
18 Bésub keroog Boroom bi xañ leen gànjari tànk, ak takkaay yu bindoo ni jant, ak yu bindoo ni weer wu feeñ; 19 aki loŋ-loŋ aki caq aki muuraay. 20 Moo leen di xañ ay tañlaay ak lami përëg aki ngañaay ak téere yu xeeñ aki gàllaaj, 21 xañ leen jaaroy torlu ak jaaroy bakkan, 22 ak mbubbi xew, aki mëlfë, ak séri càngaay, ak saagi loxo, 23 ba ci yérey sooy ak yérey lẽe aki musóor aki kol.
24 Su boobaa lu xasaw wuutu lu xeeñ,
buum wuutu ngañaay,
nel bu set wuutuy létt,
yérey saaku wuutu ndoket bu rafet,
toroxte wuutub taar.
25 Yerusalem, say góor ay fàddoo saamar,
say jàmbaar des xare.
26 Su boobaa sa bunti dëkk sax di ñaawlook a jooy,
mel ni ndaw su ñu futti,
mu ne dett fi suuf.