16
1 Waa Mowab a nga naa:«Yónneeleen boroom réew mi yóbbalu kuuy yu ndaw,
jële ko Sela, jaare màndiŋ ma,
yóti ko buurub Yuda fa tundu Siyoŋ mu taaru.»
2 Jigéeni Mowab a nga ca jéggikaayu dexu Arnon,
mel ni picc yu tasaaroo fa seeni tàgg,
di fët-fëtluy, naaw.
3 Ña nga naa njiiti Yuda:
«Xelal-leen nu, àtte nu,
lalal nu bëccëg ndarakàmm ker gu mel ni guddi,
yiire ko daw-làqu, yi nu doon;
buleen nu wor te nuy wuta raw!
4 Mayleen nu nun ñi rëcce Mowab, nu dal ak yeen,
te ngeen làq nu bóomkat.»
Kiy note déy day jeexal, sëxëtoo dakk,
kiy lore ci réew mi jóge fi,
5 ab jal sampe fi ci ngor,
ki ci tooge jikko ju dëggu di askanu Daawuda
te di njiit luy sàkku yoon, yàkkamti njekk.
6 Noo dégg ni Mowab réye,
réya réy, reew te bew,
seeni kañu di waxi neen.
7 Moo tax Mowab di jooy ba ñéppi Mowab jooyoo,
ndax namm reseñ ja woon ca Kir Eres,
ba ne yàcc, di binni.
8 Tool ya fa Esbon day wow,
njiiti xeet yee dëggaate ngëneelu reseñ gu Sibma,
te cabb ya laloon ba Yaser,
ba àkki déndu màndiŋ ma,
car ya law ba wàllaa géej.
9 Jooyi waa Yaser laay jooy reseñ ga fa Sibma,
yeen waa Esbon ak Elale, ma sange leeni rongooñ,
nde fa ngeen di dajaleek fa ngeen di góobe,
coowal mbégtee fay dakke.
10 Mbégteek bànneex ay toxoo seeni tool,
ay woy aki sarxolle noppee jibe seeni tóokër,
te nalkatu reseñ naltil fa mbànd ya!
Aji Sax jee dakkal coow li.
11 Maa ngi yërëm Mowab, bay binni ni buumu riiti,
sama yaram daw ci Kir Eres.
12 Mowab a ngoog ak coonoom,
ba muy deme fa bérab yu kawe ya,
dugg jaamookaayam di ñaan te du am.
13 Lii la Aji Sax ji waxoon bu yàgg ci mbirum Mowab,
14 tey Aji Sax ji wax ne:
«Fileek ñetti at yu surga bu ñu bind waññ,
dees na sàggi sagub Mowab,
te li ñuy bare tey lépp,
seenum ndes ay néew lool te tekkeedi.»