Ab yéeneb waxyu ñeel na péeyub Siri
17
1 Yéene bii ñeel na Damaasa:Damaas a ngii, léegi mu noppee doon ab dëkk,
xanaa ab jalu tojit;
2 dëkki Arower gental,
gàtt yi jagoo,
goore fa, kenn du leen dàq.
3 Tata dina tukkee diiwaanu Efrayim,
nguur foqe dëkk ba ñuy wooye Damaas,
te ndesu Siri du ëpp bànni Israyil daraja.
Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi.
4 Bésub keroog sagub Yanqóoba sàggiku,
yaram wa réer ko, mu jeex tàkk.
5 Day mel nim ngóob
mu loxol góobkat bay dal, di dajale gub ya.
Day mel ni ngóob ma ca xuru Refayeen,
6 fa dara dul des lu moy am poraat;
mu mel ni wittum oliw,
bu noppee ñaari doom ak ñett ay des ca kaw,
mbaa ñeent ba juróom ci car yi meññ.
Kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil.
7 Bésub keroog nit sàkku Ki ko sàkk,
ba ne jàkk Aji Sell ju Israyil.
8 Dootu sàkkooti lenn ci sarxalukaay
yi mu sàkkal boppam.
Dootu sàkkooti yooyu mu defare loxoom,
du xer yi ñuy jaamoo Asera,
du yeneen sarxalukaayi cuuraay.
9 Bésub keroog seen dëkk yi tata wër,
dees na leen won gannaaw
ni dëkki Eween ñaak Amoreen ñab,
ba leen bànni Israyil dàqee,
lépp ay doon ab gent.
10 Yeena fàtte Yàlla ji leen di musal,
bawuleen xel seen cëslaay jiy seen rawtu,
xanaa di jëmbatal seeni tuur ay tooli ngëneel,
di ji jiwu mu bawoo feneen.
11 Bés ba ngeen ko jëmbatee, ngeen gis mu sax,
ëllëg ba bët setee, mu tóor,
te ngóob réer bésub wopp,
ci biir mitit wu amul paj.
12 Ndeysaan, mii riirum gàngoor yu mag!
Xeet yu bareey riir ni riirum géej,
ànd ŋarandoo ni géej gu sàmbaraax,
gannax ya ŋarandoo.
13 Xeet yaa ngi ŋarandoo
ni ndox mu baawaan,
Yàlla gëdd leen, ñu daw ba sore;
ngelaw yëngu, ñu naaw,
ni boob, ba ca kaw tund ya,
mbete pënd bu ngëlén wal, mu def callweer.
14 Ngoon a ngay jot, tiitaange ne jaas,
balaa bët a set lépp jeex.
Lii mooy añub ñuy sëxëtoo,
lii mooy deminu ñiy nangu sunu alal.