Aji Sax jee mat cëslaay
44
1 Yaw Yanqóoba, sama jaam bi, déglul boog,
yaw Israyil sama tànnéef laa wax.
2 Aji Sax ji dafa wax, moom mi la sàkk,
mooñ la fa sa biiru ndey,
di la dimbali.
Mu ne: «Yaw Yanqóoba sama jaam bi,
yaw Yesurun sama tànnéef laa wax,
bul tiit.
3 Maay sottim ndox suuf su mar,
ak wal yu waleg joor gu wow.
Maay sotti saw askan samag noo,
sama barke sottikul ñi nga meññ,
4 ñu màgg ni garabu saabsaab,
nirook garab yu mag yu feggook ndox.
5 Kii nee: “Aji Sax jee ma moom.”
Kee di tuddoo turu Yanqóoba,
kale bind ca loxo ba: “Maa ñeel Aji Sax ji,”
tey wuyoo turu Israyil.»
Aji Sax ji dëkk na yàllantu yi
6 Aji Sax ji dafa wax,
moom buurub Israyil, jotkatam,
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
mu ne: «Maa jëkk, maa mujj,
te yàlla amul ndare man.
7 Ana ku mel ni man? Na àddu!
Na biral firndeem te taajal ma
la amoon ba may sos xeet wu yàgg wa,
ak li dikkagul.
Na ko wax!
8 Buleen tiit, buleen ragal.
Dama leena biralul lii bu yàgg, yégal leen ko?
Yeenay samay seede.
Yàlla daa am ju ma moy?
Cëslaay amul, xawma ci kenn!»
 
9 Képp kuy tabax jëmmi tuur, doo tus,
xërëm yooyu ñu safoo amul njariñ.
Ñooñu ñu defi seede
te gisuñu, yéguñu,
muy seen gàcce!
10 Sàkk sam tuur,
móol sa jëmmu tuur,
te jariñu la tus!
11 Képp ku ca bokk
sa gàcce lay doon,
ña koy yett sax ay nit doŋŋ lañu.
Nañu daje ñoom ñépp, taxaw,
bokk tiitaangeek gàcce.
12 Ab tëgg jël jumtukaayam,
liggéey weñ ca taal ba,
wàkka wàkk, jëmmal;
def ci kem kàttanam,
teg ca xiif, doole jeex,
naanul it ba tax mu loof.
13 Liggéeykatu bant tàllal buumu nattukaay,
jël kew, nataale,
xacc, rëdde rëddukaayu wërngal,
jox ko bindu nit,
jekkal ba mu mel ni nit,
nar koo fat cib néeg,
14 ba tax mu gor garabi seedar,
sàkk banti sippar ak yu ni mel,
tànn ci garabi gott bi,
mbaa mu jëmbat garab yu dëkke naat,
ab taw màggal,
15 nit xambe, sàkk ci, jaaroo;
taal, lakke mburu;
sàkkaale ci jëmmu tuur, sujjóotal ko,
muy jëmm ju mu defar, di ko sukkal;
16 xaaju matt ma lay taal,
toggew yàppam, lekk,
wàjj, xéewloo ba suur,
jaaruwaale te naan:
«Mii njaar mu neex!
bii tàkk-tàkk bu yànj!»
17 Ndesu matt ma lay sàkke jëmmu tuuram,
sukkal ko,
sujjóotal ko, ñaan ko, naa:
«Yaay sama Yàlla, xettli ma!»
18 Ñii xamuñu, xàmmeewuñu,
seeni gët lañu lëndëmal, ba gisatuñu;
fatt seenum xel, ba xelootuñu.
19 Ku mel nii du délloosim xelam,
ba xam, ràññee ne:
«Xaaju matt mi laa taal,
lakke mburu,
wàjje yàpp, lekk;
mu des, ma di ko sàkke lu seexluwu lii?
Ab dogu bant laay sukkal?»
20 Kee di jur gu fore ab dóom,
xelam nax ko, sànk ko.
Du keey musal bakkanam de!
Du kee naa: «Xanaa duy caaxaan laa ŋàbb nii?»
 
21 Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii!
Ma ne Israyil, fàttlikul, yaa di sama jaam!
Ma bind la, ngay sama jaam,
yaw Israyil, duma la fàtte!
22 Maa far say moy, mu naaxsaay niw niir,
say bàkkaar ne mes nib lay.
Délsil fi man, jot naa la.»
23 Asamaan, sarxolleel, Aji Sax ji dikk na!
Yeen xóotey suuf, xaaculeen!
Yeen tund yi, neleen réllet, sarxolleendoo,
ak yaw gott beek sa bépp garab!
Aji Sax jee jot Yanqóoba,
te moom Israyil lay fésale darajaam.
Dees na dëkkewaat Yerusalem
24 Aji Sax ji sa jotkat dafa wax,
moom mi la bind ba ngay sosu,
ne: «Man maay Aji Sax ji sàkk lépp.
Man doŋŋ maa tàllal asamaan,
lal suuf, kenn wéttaliwu ma ca.
25 Maay neenal firndey maaman,
dofloo gisaanekat.
Maay weddi fóore,
def xam-xamam mu dig ndof.
26 Maay dëggal sama kàddug jaam,
di sottal sama ndéeyal ndaw.
Maa naan ci Yerusalem:
“Dees na ko dëkke,”
dëkki Yuda, ma ne:
“Dees na leen tabaxaat,
ma dekkali gentam bi.”
27 Maa naa xóotey mbeex mi: “Wowal,
te maay ŋiisal say dex.”
28 Maa naa ci Sirus: “Sama sàmm bi!”
Mooy matal sama bépp nammeel,
te it moo naa ci Yerusalem:
“Nees ko tabaxaat,”
kër gu sell gi, laa ne:
“Nees ko yékkatiwaat!”»