Aji Sax ji dooleel na Buur Sirus
45
1 Aji Sax ji dafa wax ki mu fal,
Buur Sirus mi mu jàpp ci loxol ndijooram,
ngir nangulal ko xeet yi,
yolomal ngañaayal buur yi,
lafal koy bunt,
ba bunti dëkk du tëje,
2 mu ne: «Man maa lay jiitu,
maasale mbartal,
rajaxe buntu xànjar,
damm tëjukaayu weñ.
3 Maa lay jagleel denc yu loq,
ak alal ju làqe,
ba nga xam ne maay Aji Sax ji lay wooye sa tur,
man Yàllay Israyil.
4 Te Yanqóoba sama jaam bi,
Israyil moomu di sama tànnéef moo tax
ma wooye la saw tur,
takkal la ndombol tànk,
te xamuloo ma.
5 Aji Sax ji man a, du keneen;
kenn du yàlla ku dul man.
Maa la gemb,
te xamuloo ma,
6 ngir xamees penku ba sowu,
ne lu dul man neen la.
Aji Sax ji man a, du keneen.
7 Maay bind leer,
di def lëndëm.
Maay indi jàmm,
di def safaan.
Maay Aji Sax jiy def lii lépp!
8 Na asamaan wis-wisal,
niir yuri njekk,
suuf fett, meññal wall,
boole ci jebbil njekk.
Man Aji Sax ji, maa def lii!»
 
9 Wóoy ngalla kuy diiŋat ka la tabax
te di ndabal xandeer ci biir ndabi xandeer!
Ana ban ak di wax tabaxkatam,
naa ko: «Looy def nii?
Yaw amulooy loxo.»
10 Wóoy ngalla ku naan baayu nit,
«Moo, lu sa geño meññ nii?»
Mbaa ku naan ndeyu nit,
«Li nga wasin lu mu?»
11 Aji Sax ji, Aji Sell ju Israyil dafa wax,
moom mi ko bind,
mu ne: «Lu dikkagul, nu ngeen ma ko ñemee laaje;
am dangeen may jox ndigal ci samay doom,
jox ma ko ci li ma liggéeye samay loxo?
12 Man maa amal suuf,
sàkk doom aadama fi kaw suuf.
Man mii la samay yoxo firi asamaan,
te maay jox gàngoori asamaan lépp ndigal.
13 Man maay yékkati Sirus ci biir njekk,
xàllu yoonam.
Moom mooy tabax sama dëkk,
yiwi sama ñoñ ñi ñu toxal,
te du laaj pey mbaa neexal.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax.
 
14 Aji Sax ji dafa wax ne:
«Muy ñaqu Misra, di koomu waa Kuus,
ak waa Seba, ya ne sireet ca kaw,
ñoom ñépp ay jàllsi, nga jagoo.
Sa gannaaw lañuy topp,
yeewe, jàllsi;
sujjóotal la, di ñaan naan:
“Fi yaw daal la Yàlla ne,
du feneen,
te tuur neen la.”»
15 Yaw déy, yaa di Yàlla ju làqu,
yaw Yàllay Israyil ji koy wallu.
16 Yettkati xërëm yaa ngoogu, rus,
torox, riixleendoo.
17 Israyil, yaay mucc fa Aji Sax ji
mucc gu sax dàkk!
Doo rus, doo torox
fii ak ëllëg.
 
18 Aji Sax ji kat dafa wax,
moom mi sàkk asamaan,
moom Yàlla mi bind suuf,
tabax ko, dëj ko,
sàkkewu ko maraas,
xanaa tabaxal ñu ko dëkke.
Mu ne: «Aji Sax ji, man a, du keneen.
19 Làquwma, di waxe bérab bu lëndëm.
Newuma it askanu Yanqóoba:
“Sàkkuleen ma fu dara amul.”
Man Aji Sax ji maay wax dëgg,
di biral njub.»
 
20 Yeen daw-làquy xeet yi,
dajeleen, dikk,
ànd, jegesi.
Képp ku gàddu tuuru bantam,
ak kuy ñaan tuur mu ko dul wallu,
kooka xamul dara.
21 Àdduleen, layoosi,
diisooleen fi seen biir kay!
Ana ku xamle woon lii bu yàgg,
yégle woon ko booba?
Xanaa du man Aji Sax ji?
Kenn du Yàlla ku dul man!
Yàlla ju jub, di walloo,
du kenn ku dul man!
22 Yeen waa àddina, catoo cat,
walbatikuleen fi man, mucc.
Man maay Yàlla, du keneen.
23 Giñ naa ko ci man mii,
sama gémmiñ njekk a ciy jibe,
di kàddu gu dul randu.
Man la ñépp di sukkal seen bëti óom,
man it la bépp boroom làmmiñ di giñe.
24 Dees na ma waxal ne:
«Aji Sax ji rekk a jagoo njekk ak doole!»
Mboolem ñi ma mereey ànd,
sëgg, fekksi ma.
25 Ci Aji Sax ji la askanu Israyil gépp yeye,
bay damu.