Yàlla sikk na Israyil
48
1 Yeen waa kër Yanqóoba, dégluleen;yeen ñi ñu wooye turu Israyil,
yeen ñi bawoo bëti ndoxi Yuda,
di giñe turu Aji Sax ji,
yeen ñiy sàbbaal turu Yàllay Israyil
te dëgg ak njekk taxul,
2 moona yeena ngi sagoo turu dëkk bu sell bi,
di wéeroo Yàllay Israyil
ji turam di Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.
3 Yàgg na maa biral lay jëkka am.
Tuddoon naa ko, yégle ko,
jekki jëf ko, mu sotti.
4 Xam naa ne ñu dëgër bopp ngeen.
Dangeen të, wowle.
5 Moo tax ma yàgg leena biralal lii,
yégal leen ko balaa teew.
Lu ko moy ngeen ne:
«Sunu tuur mee ko def,
sunu tuuru bant bee,
sunu tuuru weñ gee ko amal di!»
6 Lii lépp déggoon ngeen ko;
xool-leen, xanaa dingeen ko nangu tey!
Bés niki tey dinaa leen yégal lu bees,
muy kumpa gu ngeen xamul woon.
7 Léegi lees ko amal,
du lu yàgg.
Lu jiitu tey masuleen koo dégg
te dungeen ne xamoon ngeen ko.
8 Dégguleen, yéguleen,
seeni nopp masula bënn;
xam naa ne ay workati neen ngeen,
«njuddu-fippu» lañu leen di wooye.
9 Waaye sama tur tax na ma aj sama mer,
sama woy tax na ma muñal leen,
ba duma leen fàkkas.
10 Ma ne, togg naa leen, xelli cib taal,
waaye du taalu xellikaayu xaalis,
sawaras nattu laa leen xellee.
11 Samaw tur a tax,
sama tur laay jëfe.
Jomb naa ñaaw!
Te sama teddnga, duma ko joxe.
12 Dégluleen ma, yeen askanu Yanqóoba,
yeen bànni Israyil gi ma dégtal sama woote.
Maay kenn, maa jëkk te maa mujj;
13 te sama loxo bee dëj suuf,
sama ndijoor bi firi asamaan.
Maa leen di woo, ñu bokk taxaw.
14 Bokkleen daje yeen ñépp te déglu!
Kan ci tuur yii moo yégle lii?
Ki Aji Sax ji sopp
mooy sottal nammeelu Aji Sax ji ci Babilon,
won Kaldeen ña fa dëkke diisaayu loxoom.
15 Maa àddu, man mii;
maa ko woo, indi ko,
te pexeem dina joy.
16 Jegesileen ma, déglu ma;
bu jëkk ba tey làquwma, di wax;
te ba muy xew, fa laa teew.
Tey Boroom bi Aji Sax ji da maa yebal
boole maakam xelam.
17 Aji Sax ji seen jotkat dafa wax,
Aji Sell ju Israyil da ne:
«Maay Aji Sax ji, seen Yàlla
ji leen di jàngal seen njariñ,
di leen awale fa ngeen wara awe.
18 Céy su ngeen sàmmoon samay santaane,
ba jàmm baawaanal leen,
njekk géejal leen,
19 seen geño sakkan ni suuf,
di seen meññeefu biir, tollook feppi suuf,
du dog, du sànkoo fi sama kanam!
20 «Génnleen Babilon,
dawleen Kaldeen ñi, tey sarxolle.
Biral-leen lii, yéene ko,
te yeggeji ko waa cati àddina,
ne leen Aji Sax ji jot na jaamam Yanqóoba.
21 Marewuñu bérab yu wow ya mu leen jaarale woon,
ndox mu balle ciw doj la leen xellil,
moo xaru doj, ndox ma baawaana.
22 Jàmm,» la Aji Sax ji wax ne,
«du ñeel ñu bon ñi.»