Babilon falu, fëlëñu
47
1 Yaw janq Babilon,wàccal, toog ci pënd bi.
Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi laa ne,
toogal fi suuf, amatoob jal.
Dootoo dégg «Lewet, xay.»
2 Fabal wolukaay, wol sunguf.
Dindil sa muuraay gi,
wogos sa mbubb,
ëñ sas kumba,
xuus, jàll dex yi.
3 Na sa yaram feeñ,
say cér ne fàŋŋ.
Damay feyu,
te duma bale.
4 Sunu jotkat ay Aji Sax ji Boroom gàngoor yi,
Aji Sell ju Israyil.
5 Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi,
toogal ne cell te fatu cig lëndëm,
deesatu la wooye lingeeru réew yi.
6 Maa mere woon sama ñoñ,
sobeel sama séddoo ñii,
teg leen ci sa loxo,
te wonoo leen yërmande,
ba mag sax, nga teg ko lu diisa diis,
7 te naa: «Ba fàww maay lingeer!»
ba tax bàyyiwoo xel ca la ngay def;
xalaatoo la muy jur.
8 Diryànke bee, déglul lii:
Yaa ngi ne finaax te naa ci sam xel:
«Maa ko yor, man rekk, du keneen.
Duma jooy jëkkër, duma jooy doom!»
9 Te yaar yooyoo lay dikkal ci benn bés.
Jooy doom, jooy jëkkër ay yembandoo,
dal fi sa kaw ci sa biir xërëmtu yi ne xas,
ak sa jat yu dul jeex.
10 Dangaa yaakaaroon sa pexe yu bon,
naan, «Kenn gisu ma!»
Sam xel ak sa xam-xam a la wacc,
ba tax nga naa: «Maa ko yor, man rekk.»
11 Musibaa lay dikkal,
te doo xam fu mu fenke.
Njaaxum a lay dal,
te du looy mana fanq.
Sànkuteey jekki dale la foo yégul.
12 Jàppool say jat rekk
ak sa xërëm yu ne xas
yoo dale sonn ba ngay ndaw.
Jombul mu amal la njariñ,
mbaa ñu ragale la ko.
13 Yaaka sonn ci tegtali maa-man!
Nañ taxaw boog, wallu la!
Ñii di rëdd nataalu asamaan,
di niiri biddiiw,
ak di xool weer wu feeñ,
xamle ca loo dikkleegul.
14 Ñu ngoog bokk ak boob bu sawara jafal, demin,
duñu musal seen bakkan ca sawara sa,
te du doon ab taal bu ñuy lakke mburu
mbaa xal sooy uuf di jaaru.
15 Lii moo di muju ña la taxoon di sonn.
Ña nga dale jëflanteel ba ngay ndaw,
ña ngay tambaambalu tey, ku nekk ak yoonam,
kenn walluwu la ci.