Aji Sax ji tiiñal na njiiti Israyil
3
1 Dama ne:
«Ngalla dégluleen yeen njiiti Yanqóoba,
yeen kilifay kër Israyil!
Xanaa du yeena wara xam yoon?
2 Te yeenay bañ-kati lu baax,
di bëgg-kati lu bon.
Yeenay fees sama ñoñ te ñuy dund,
yeenay rocci suux wi sàng seeni yax.
3 Yeenay yàpp samay bokk,
fulli seen der,
damm seeni yax, dogat,
def ko ni toggug kawdir,
mbete ndawal ci cin.»
4 Lee tax noggatukat yii di woo Aji Sax ji wall,
te du leen wuyu,
kanamam la leen di làq, bésub keroog,
nde ñoo bonal seeni jëf.
Aji Sax ji àrtu na yonent yu bëgge yi
5 Lii la Aji Sax ji wax ci yonent
yiy lajjal samay bokk:
«Bu ñu sàqamee ab lanc, yéene jàmm;
ku leen leelul, ñu biral waxyub xare.
6 Moo tax yeen, guddi moo leen di ñeel,
ba peeñu réer,
lëndëm a leen di dikkal, ba ngis tukkil leen,
jant mooy sowal yonent yi,
bëccëg lëndëmal leen.
7 Seetkat yi dañuy rus,
boroom ngis yi torox,
ñoom ñépp jàpp seen gémmiñ;
ndax Yàllaa leen dul faale.»
 
8 Teewul man, may feese doole,
feese Noowug Aji Sax ji,
ak dëgg ak njàmbaarte,
ngir biralal askanu Yanqóoba, bàkkaaram,
ngir tuddal bànni Israyil googu moyam.
Aji Sax ji tiiñalaat na njiiti Israyil
9 Ngalla dégluleen lii, yeen njiiti kër Yanqóoba;
yeen kilifay kër Israyil.
Yeen ñi seexlu dëgg,
lunkal wépp yoonu njub.
10 Deret ngeen tabaxe Siyoŋ,
njubadi ngeen tabaxe Yerusalem googu.
11 Seeni njiit, alalu ger lañuy àttee,
seeni sarxalkat di feyeekuy jàngle,
seeni yonent di weccikoo xaalis
seenum ngisaane,
te Aji Sax ji lañuy dëgërloo, naan:
«Xanaa du Aji Sax jaa ngi ci sunu biir?
Musiba du nu dab!»
12 Kon nag dees na gàbb Siyoŋ nib tool,
Yerusalem googu diy tojit, jale,
tundu kërug jaamookaay baay doon gajj bu kawe.