Waareb Yaxya
3
1 Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen. 2 Te it Anas ak Kayif nekkoon sarxalkat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakari, ca màndiŋ ma. 3 Yaxya daldi dugg àll, bi wër dexu Yurdan gépp, di waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
4 Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan:
«Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne:
“Xàll-leen yoonu Boroom bi,
jubal-leen fi muy jaar.
5 Nañu sëkk xur yi,
maasale tund yi ak jànj yi.
Yoon yi dëng ñu jubbanti leen,
yi ñagas ñu rataxal leen.
6 Bu ko defee bépp mbindeef dina gis mucc gi Yàlla tëral.”»
7 Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? 8 Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii. 9 Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.»
10 Mbooloo ma laaj ko ne: «Lan lanu wara def nag?» 11 Mu ne leen: «Ku am ñaari mbubb, nga jox menn mi ki amul. Ku am ñam itam, nga bokk ko ak ki amul.» 12 Ay juutikat itam ñëw ca Yaxya, ngir mu sóob leen ci ndox; ñu ne ko: «Kilifa gi, lu nu wara def?» 13 Mu ne leen: «Laajleen rekk lu jaadu.» 14 Ay xarekat laaj nañu ko ne: «Li jëm ci nun nag?» Mu ne leen: «Buleen néewal doole kenn, jël xaalisam ci kaw ay tëkku mbaa ci seede lu dul dëgg. Waaye doylooleen li ñu leen di fey.»
15 Mbooloo maa ngay xaar, di séentook a laaj ci seen xel, ndax Yaxya mooy Almasi bi. 16 Noonu Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. 17 Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàqam, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.»
18 Noonu Yaxya teg ca yeneen dénkaane yu bare, di yégal nit ña xibaaru jàmm ba. 19 Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef, 20 ba faf tëj Yaxya kaso.
Yaxya sóob na Yeesu ci ndox
21 Noonu Yaxya sóob mbooloo mépp ci ndox, sóobaale it Yeesu. Bi Yeesu di ñaan nag, asamaan daldi ubbiku. 22 Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.»
Cosaanu Yeesu Kirist
23 Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu wara tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi.
Te Yuusufa mooy doomu Eli, 24 miy doomu Matat.
Matat, Lewi mooy baayam; Lewi, Melki;
Melki, Yanayi; Yanayi, Yuusufa;
25 Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi.
26 Nagayi, Maat; Matacas; Semeyin; Yoseg; Yoda.
27 Yoda, Yowanan mooy baayam; Yowanan, Resa;
Resa, Sorobabel. Kooku Salacel a ko jur; Salacel, Neri;
28 Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er.
29 Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi;
30 Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim.
31 Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena;
Mena, Matata; Matata, Natan;
Natan, Daawuda. 32 Daawuda mooy doomu Isayi;
Isayi, Obedd; Bowas; Salmon; Nason.
33 Nason; Aminadab; Aminadab, Admin;
Arni; Esron; Peres; Yuda; 34 Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;
35 Serug; Rew; Peleg; Eber; Sela. 36 Sela, Kaynam mooy baayam; Kaynam, Arpagsàdd;
Arpagsàdd, Sem; Sem, Nóoyin; Nóoyin, Lemeg;
37 Lemeg, Matusalem; Enog, Yeredd; Maleleel; Kaynan;
38 Enos; Set; Set doomu Aadama;
Aadama doomu Yàlla.