Yeesu dékku na ay nattu ci pexey Seytaane
4
1 Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan. 2 Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.
3 Noonu Seytaane ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj wii mu nekk mburu.» 4 Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»
5 Seytaane yóbbu na ko fu kawe. Ci xef ak xippi mu won ko réewi àddina sépp, 6 ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox. 7 Kon boo ma màggalee, dinga moom lépp.» 8 Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»
9 Seytaane yóbbu na ko Yerusalem, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal jëm ci suuf, 10 ndaxte Mbind mi nee na:
“Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir,
ñu sàmm la,
11 dinañu la leewu ci seeni loxo,
ngir nga baña fakktalu ciw doj.”»
12 Yeesu ne ko: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
13 Bi mu ko lalalee fiiram yi mu am yépp, Seytaane daldi sore Yeesu, di xaar yeneen jamono.
Yeesu ci dëkku Nasaret
14 Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp. 15 Muy jàngle ca seeni jàngu, te ñépp di ko tagg.
16 Yeesu dem Nasaret fa mu yaroo, te ca bésub noflaay ba, mu dugg ca jàngu ba, ni mu ko daan defe. Noonu mu taxaw ngir jàngal mbooloo mi. 17 Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii:
18 «Xelum Boroom baa ngi ci man,
ndaxte moo ma tànn,
ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi.
Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel,
yégal gumba yi ne dinañu gis,
te jot ñi ñu not,
19 tey yégle atum yiw, mi jóge ci Boroom bi.»
20 Bi mu jàngee aaya yooyu ba noppi, mu ub téere bi, delloo ko ki koy denc, toog. Ñépp ña nekkoon ca jàngu ba dékk koy bët. 21 Noonu mu daldi ne: «Tey jii, loolu Mbind mi wax mat na, bi ngeen koy déglu.» 22 Ñépp di seede lu rafet ci Yeesu, di waaru ci wax ju neex, ji mu doon yégle, ñu naan: «Ndax kii du doomu Yuusufa?» 23 Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”» 24 Mu tegaat ca ne: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ab yonent kenn du ko teral ca réewam. 25 Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu. 26 Moona Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon. 27 Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alyaasa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naamaan, mi dëkkoon réewu Siri.»
28 Bi ñu déggee wax yooya, ñépp ña nekkoon ca jàngu ba daldi fees ak mer. 29 Noonu ñu jóg, génne ko dëkk ba, yóbbu ko ca mbartalum tund, wa ñu sanc seen dëkk, ngir bëmëx ko ci suuf. 30 Waaye moom mu jaar ci seen biir, dem yoonam.
Yeesu faj na nit ku am rab
31 Gannaaw loolu Yeesu dem Kapernawum, ab dëkk ca diiwaanu Galile. 32 Mu jàngal leen ca bésub noflaay ba, ñu waaru ca njàngleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ. 33 Noonu am na ci jàngu bi nit ku rab jàpp. Mu daldi xaacu ne: 34 «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!» 35 Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanam ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko.
36 Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.» 37 Noonu turam siiw ca diiwaan bépp.
Yeesu faj na jarag yu bare
38 Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu ñaan Yeesu, mu dimbali leen ci. 39 Mu randusi, tiim ko, gëdd tàngoor wi, mu dem. Noonu tàngoor wi wàcc, soxna si jóg ca saa sa, di leen topptoo.
40 Bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ay jàngoro yu wuute. Kenn ku nekk mu teg la loxo, wéral la. 41 Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne mooy Almasi bi.
42 Ca njël gu jëkk Yeesu génn, dem ca bérab bu wéet. Mbooloo ma di ko seet. Bi ñu ko gisee, ñu koy wuta téye, ngir bañ mu dem. 43 Mu ne leen: «Damaa wara dem ci yeneen dëkk yi, ngir yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla, ndaxte looloo tax ñu yónni ma.» 44 Noonu mu dem di waare ca jàngu ya ca réewu Yawut ya.