Muccug bànni Israyil
di ñaareelu xaaju Tawreetu Musaa
Bànni Israyil dem na réewum Misra
1
1 Góor ñi seen baay di Yanqóoba, mi ñu dippee Israyil, ñu àndoon ak moom, dem Misra, te ku nekk yóbbaale waa këram, seeni tur a di: 2 Ruben ak Simeyon ak Lewi ak Yuda 3 ak Isaakar ak Sabulon, ak itam Beñamin; 4 ak Dan ak Neftali ak Gàdd ak Aser. 5 Góor ñi soqikoo ci Yanqóoba ñépp juróom ñaar fukk lañu (70), bu ñu ci boolee doomam, ji ñuy wax Yuusufa, moom ma ñu fekk Misra. 6 Gannaaw ga Yuusufaaki doomi baayam yu góor yépp nelaw, ñook maas googu gépp. 7 Bànni Israyil nag giir fa, law, di fulandiwu, ba yokku lool, fees réew ma.
Firawna not na bànni Israyil
8 Ñu dem ba jëmmi jamono, beneen buur bu xamul Yuusufa falu ca Misra. 9 Mu wax ak waa réewam, ne leen: «Giirug bànni Israyil kat ñu ngi nuy gëna bare, ba ëpp nu doole. 10 Nanu ci sàkk pexe, ngir ñu bañatee yokku. Lu ko moy bu xare amee, man nañoo far ak sunuy noon, xeex ak nun, ba génn réew mi.» 11 Ba loolu amee ñu fal ay nit ñu leen di ga ca seeni sas, di leen ca fitnaal lool. Noonu la bànni Israyil tabaxale Firawnaa buuru Misrab dëkk, ya ñu naa Pitom ak Ramses, mu def ko ay dencukaayi dund. 12 Terewul lu ñu leen gëna fitnaal, ñuy gën di fulandiwu, yokku, ba waa Misra am njàqare ca bànni Israyil.
13 Waa Misra dañoo mujj di jaamloo bànni Israyil bu metti, 14 yen leen toskarey àddina ndax liggéey yu metti. Ñuy móol ban, di tabax, waa Misra teg ca sëf leen mboolem liggéeyu tool ya. Néegoon nañu ca ñoom lool ca mboolem liggéeyu njaam bu ñu leen sas.
15 Firawna buuru Misra teg ca wax ak rewlikati Ebrë yac, te kenn ka tuddoon Sifra, ka ca des di Puwa. 16 Mu ne leen: «Bu ngeen dee rewli jigéeni Ebrë yi, nangeen xool lu xale bi doon. Su dee góor, reyleen, su dee jigéen, bàyyileen, mu dund.» 17 Teewul rewlikat ya ragal Yàlla, ba defuñu la leen buur ba sant; xanaa ñu bàyyi liir yu góor ya, ñu dund. 18 Buuru Misra woolu rewlikat ya, ne leen: «Ana lu tax ngeen def lii, di bàyyi liir yu góor yi, ñu dund?» 19 Rewlikat ya ne ko: «Li tax kay mooy, jigéeni Ebrë yi dañoo niroowul ak jigéeni waa Misra; ndax dañoo njaxlaf, ba bu rewlikat yiy laata agsi, fekk ñu mucc ba noppi.» 20 Bànni Israyil nag di fulandiwu, gëna yokku, Yàlla defal rewlikat ya aw yiw, 21 may leen giir ndax seenug ragal Yàlla. 22 Gannaaw loolu Firawna sant waa réew ma yépp, ne leen: «Mboolem doom ju juddu ci Ebrë yi, di góor, sànnileen ca dex ga, waaye lu ciy jigéen, bàyyileen, mu dund.»